"ku giñ ci dara fekk du dëgg ngir dog ci àqi ab jullit, dana daje ak Yàlla fekk mu mere ko
Jële nañu ci Abdallah Ibn Mashuud yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
"ku giñ ci dara fekk du dëgg ngir dog ci àqi ab jullit, dana daje ak Yàlla fekk mu mere ko". Nee na: Ashas wax ne: giñ naa ci Yàlla ne loolu ci man la nekk; suuf dafa doxoon ci sama diggante ak ub Yahuud, mu weddi ma, ma yóbb ko ci Yonente bi, Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ma: "ndax am nga firnde?" Ma ne ko: déedéet. Nee na: mu ne Yahuud bi: "giñal". Nee na: ma ne ko: yaw Yonente Yàlla bi, kon daal day giñ daal di yóbb sama alal. Yàlla mu kawe mi daal di wàcce: {ñi nga xam ne dañuy jënne kóllareg Yàlla gi ak seen i giñ ci ag njëg gu ndaw} ba aaya bi jeex.
«مَنْ حَلَفَ عَلَى يَمِينٍ وَهُوَ فِيهَا فَاجِرٌ لِيَقْتَطِعَ بِهَا مَالَ امْرِئٍ مُسْلِمٍ، لَقِيَ اللَّهَ وَهُوَ عَلَيْهِ غَضْبَانُ». قَالَ: فَقَالَ الْأَشْعَثُ: فِيَّ وَاللَّهِ كَانَ ذَلِكَ؛ كَانَ بَيْنِي وَبَيْنَ رَجُلٍ مِنَ الْيَهُودِ أَرْضٌ، فَجَحَدَنِي، فَقَدَّمْتُهُ إِلَى النَّبِيِّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فَقَالَ لِي رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «أَلَكَ بَيِّنَةٌ؟» قُلْتُ: لَا. قَالَ: فَقَالَ لِلْيَهُودِيِّ: «احْلِفْ». قَالَ: قُلْتُ: يَا رَسُولَ اللَّهِ، إِذَنْ يَحْلِفَ وَيَذْهَبَ بِمَالِي. فَأَنْزَلَ اللَّهُ تَعَالَى: {إِنَّ الَّذِينَ يَشْتَرُونَ بِعَهْدِ اللَّهِ وَأَيْمَانِهِمْ ثَمَنًا قَلِيلًا}. إِلَى آخِرِ الْآيَةِ.
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day moytandikuloo giñ ci Yàlla te aji-giñ ji xam na ne waxul dëgg ci li muy giñ, ludul ne day bëgg a jël ca ngiñ la alalu keneen; te dana daje ak Yàlla fekk mu mere ko, Ashas ibn Xays yal na ko Yàlla dollee gërëm xamle ne Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa wax loolu ci jamono ji ab werente doxee ci digganteem ak benn Yahuud ci moomeelu suuf, ñu àttewu ci Yonente bi mu wax Ashas ne ko: Dangaa war a am firnde ngir saxal li ngay wootewoo, boo ko manul nag, kon dara desu fa lu dul giñug kii ñu tuumaal, Ashas daal di ne: Yaw Yonente Yàlla bi, kon de Yahuud bi dana giñ ci lumu dul teg ci dëgg dal di yóbb sama alal, Yàlla dal di wàcce Alxuraan di dëggal loolu ci li mu wax ne: Gaa yiy jënne kóllareg Yàlla ak ndénkaaneem ñeel way-gëm ñi ci ñuy matal kóolute ak seen giñ yi ci turam fekk dañuy fen, ñukoy jënde ag njëg gu néew ci poñeti àdduna bi ñooñu amuñu ca allaaxira benn cér te Yàlla du wax ak ñoom wax ju leen di bégloo di leen jariñ, waaye kay da leen di mere, du leen xool xoolu yërmànde ëllëg bis-pénc, du leen sellal ci tagg gu rafet, te du leen laabal ci di leen jéggal seen i bàkkaar ak seen i taq-taq te mbugal mu metti ñeel na leen mbugal gu leen di mettital ngir sababus li ñu def.
Tere nañu sàkku a lewal alalu nit ñi ci ag neen.
Diisug àqi jullit ñi ci lu néew ak lu bari.
Firnde war na ci kiy wootewoo, giñ nag war na ki ñu tuumaal bu nanguwul.
Àq dana saxe ci ñaari seede, bu ñu amul firnde ci aji-wootewoo ji, kon di na war ca ka ñu tuumaal mu waat.
Araamalees na giñ ci ay fen te mooy goo xam ne aji-giñ ji da ciy doge àqi keneen, te dafa bokk ci bàkkaar yu mag yiy gaar boroomam ci merum Yàlla mu kawe mi ak mbugalam.
Waareg àttekat bi ñeel kiy xuloo, rawati na bu nammee giñ.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (3/ 121) (2416).
Téere Muslim bi gën a wér (1/ 123) (138).
Yataal gi (5)
الإلمام بشرح عمدة الأحكام.
لإسماعيل الأنصاري (2/ 136).
تيسير العلام شرح عمدة الأحكام.
للبسام (ص687).
فتاوى اللجنة الدائمة - اللجنة الدائمة للبحوث العلمية والإفتاء (23/ 513).