«fi Boroom bi di gën a jegee jaam bi mooy ci mujjantalu guddi gi
Jële nañu ci Abii Umaamata mu wax ne: Amru Ibn Abasata yal na ko Yàlla dollee gërëm wax na ma ne dégg na Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
«fi Boroom bi di gën a jegee jaam bi mooy ci mujjantalu guddi gi, boo manee di bokk ci ñiy tudd Yàlla ci waxtu woowo def ko».
«أَقْرَبُ مَا يَكُونُ الرَّبُّ مِنَ العَبْدِ فِي جَوْفِ اللَّيْلِ الآخِرِ، فَإِنْ اسْتَطَعْتَ أَنْ تَكُونَ مِمَّنْ يَذْكُرُ اللَّهَ فِي تِلْكَ السَّاعَةِ فَكُنْ».
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne: Boroom bu sell bi day gën a jege jaam bi ci ñatteelu xaaj bi mujj ci guddi gi; bu ñu la tawfeexalee may la kàttan -yaw jullit bi- ba nga man a bokk ci mbooloo miy jaamu Yàlla ñiy julli di tudd Yàlla di tuub ci waxtu wii loolu lees wara góor-góor lu la.
Soññ jullit bi ci tudd Yàlla ci mujjantëlu guddi gi.
Gënanteg waxtu yi ci seen diggante ñeel tudd Yàlla ak ñaan ak julli.
Mabruug wax na ci wuute gi am ci diggante limu wax ne: "fi Boroom bi di gën a jegee jaam bi" ak li mu wax ne: "fi jaam bi di gën a jegee Boroomam mooy bu sujjóotee": li ñu jublu fii mooy leeral waxtu wi Boroom bi di jege jaam bi ci digg guddi gi, li ñu namm ci booba nag mooy leeral anam gi jaam bi di jegee Boroom bi fekk moo ngi sujjóot.
Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (5/ 537) (3579).
Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (2/ 454) (1277).
Téere Sunna yi bu An-nasaa'iy (1/ 279) (572).
Yataal gi (8)
نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.
لمجموعة من الباحثين (2/ 1019).
شرح رياض الصالحين.
لابن عثيمين (5/ 509).
كنوز رياض الصالحين.
لمجموعة من الباحثين (17/ 535).
مشكاة المصابيح.
للتبريزي (1/ 387).
Cited in books
2 BooksYataal gi (2)
- الذكر والدعاء والعلاج بالرقي من الكتاب والسنة"أقرب ما يكون العبدُ من الرب في جوف الليل الآخر، فإن استطعت أن تكون ممن يذكر الله في تلك الساعة فكن" .
- حصن المسلم من أذكار الكتاب والسنةحصن المسلم«أَقْرَبُ مَا يَكُونُ الرَّبُّ مِنَ العَبْدِ فِي جَوْفِ اللَّيْلِ الآخِرِ فَإِنِ اسْتَطَعْتَ أَنْ تَكُونَ مِمَّنْ يَذْكُرُ اللَّهَ فِي تِلْكَ السَّاعَةِ فَكُنْ»[297].