Skip to content

Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan wax: samiha Al-Laahu liman hamidahu, kenn ci nun sëgg ndigam ba keroog Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di rot daal di sujjóot, topp nu sujjóot ginnaawam.

Jële nañu ci Abdulla ibn Yasiid Am-Xatmii mu wax ne: Al-Baraa wax na ma te du fenkat, mu ne:

Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan wax: samiha Al-Laahu liman hamidahu, kenn ci nun sëgg ndigam ba keroog Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di rot daal di sujjóot, topp nu sujjóot ginnaawam.

كَانَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ إِذَا قَالَ: سَمِعَ اللَّهُ لِمَنْ حَمِدَهُ، لَمْ يَحْنِ أَحَدٌ مِنَّا ظَهْرَهُ حَتَّى يَقَعَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ سَاجِدًا، ثُمَّ نَقَعُ سُجُودًا بَعْدَهُ.

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Al-Baraa ibn Haasib yal na ko Yàlla dollee gërëm day xibaare te moom aji-gëggal la, ne Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan yëkkëti boppam bawoo ci rukoo bi daal di wax: samiha Al-Laahu liman hamidahu, ñi ci ginnaawam duñu deñ di taxaw, te jenn du sëgg ndigam ngir sujjóot ba keroog Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di teg jëham bi ci suuf, topp mu ñu rot daal di sujjóot ginnaawam.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Melo wi sahaaba yi doon toppe Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci julli, ak ne ñoom duñu tuxu jóge ca taxaw ga jëm ca rukkoo ba ba keroog muy sujjóot.

Ibn Daxiixi Al-Hiid nee na: ag tegtal nekk na ci loolu ci guddug dal gi nekk ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc.

Maamuun bi ak imaamam amna ñenti anam ci roy gi: 1- jiitu ko: ci mu tàmbali dara njëkk imaamam, maamuun bi egg ci ponk njëkk imaam bi di ca egg, niki: mu rukoo njëkk imaam bi di rukoo, walla mu sujjóot njëkk imaam bi di sujjóot, lii dafa araam, te bu tayee jiitu gi ànd ak mu xam ne dañu ko a tere kon julleem gi day yàqu, moo xam da ko a jiitu ci ab ponk, walla mu jiitu ko jëm ci ponk bi, bu dee ci kàbbaru aramal gi la kon julleem gi du fasu, te day war ci moom mu baamtu julli gi. 2- tolloo ak moom: ci mo tolloo ak imaam bi, day rukoo ànd ak rukkoowam, day sujjóot ànd ak sujjóoam, day jug it ànd ak jugam ga, lii nag li gën a néew ci ay mbiram mooy ne dañu ko a sib, te li feeñ ci tegtal yi mooy ne dafa araam; bu tolloo ak imaam bi ci kàbbaru armal gi kon julleem gi fasuwul te dafa war a baamtu julli gi. 3- roy ko: ci mu def jëfi julli gi ginnaaw imaama ci lu dul yeexe, lii mooy li ñu yoonal te mu dëppoo ak sunna. 4- yeexe topp gi: ci mu yeex a topp imaam bi ag yeex gu koy génne ci roy, niki imaam bi rukkoo maamuun des di taxaw ba imaam bi di bëgg a siggi ca rukkoo ba, te lii dafa wuute ak li ñu yoonal, te dafa araam, ndare ngànt waral ko niki feebar ak mage.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 140) (690).

Téere Muslim bi gën a wér (1/ 345) (474).

Yataal gi (4)

الإلمام بشرح عمدة الأحكام.

لإسماعيل الأنصاري (1/ 114).

تيسير العلام شرح عمدة الأحكام.

لعبد الله البسام (ص139).