"giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom ne moom day yemoo ak ñatteelu xaaju Alxuraan".
Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudrii yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Benn waay dafa dégg beneen waay muy jàng: {Xul Huwallaahu Ahadun} di ko baamtu, ba mu xëyee ñëw ci Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax ko loolu, mu mel ni waa ji da ko a xeeb, Yonente Yàlla bi ne ko: "giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom ne moom day yemoo ak ñatteelu xaaju Alxuraan".
أَنَّ رَجُلًا سَمِعَ رَجُلًا يَقْرَأُ: {قُلْ هُوَ اللَّهُ أَحَدٌ} يُرَدِّدُهَا، فَلَمَّا أَصْبَحَ جَاءَ إِلَى رَسُولِ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فَذَكَرَ ذَلِكَ لَهُ، وَكَأَنَّ الرَّجُلَ يَتَقَالُّهَا، فَقَالَ رَسُولُ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «وَالَّذِي نَفْسِي بِيَدِهِ إِنَّهَا لَتَعْدِلُ ثُلُثَ القُرْآنِ».
Abuu Sahiid Al-Xudrii yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day nettali ne benn waay dafa dégg keneen kuy jàng Saaru: {Xul Huwallahu Ahadun} di ko bàmtu ci guddi gi yépp te tegu ca dara, ba mu xëyee mu ñëw ci Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax ko loolu, mu mel ni aji-laaj ji dafa gis ne dafa tuuti, Yonente bi daal di giñ di ko feddalil wax ji, ne ko: giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom ne moom de moo ngi tolloo ak ñatteelu xaaju Alxuraan.
Ngëneelu Saaru Al-Ixlaas, ak ne day yemoo ak ñatteelu xaaju Alxuraan.
Dagan na ñuy jàng ci taxawaayu jullig guddi ay aaya yu yam ak di ko bàmtu, te bañ a xeeb loolu.
Al-Maasirii nee na: nee nañu: maanaami mooy: Alxuraan ñatti anam la; ay nettali ak ay àtte ak melokaani Yàlla mu kawe mi, te {Xul Huwallaahu Ahadun} dafa tënku -maanaam ci meloy Yàlla yi-, kon moom ñatteel la, di ab xaaj ci ñatti xaaj yi, nee nañu it: maanaam: yoolu jàng mi dañu koy ful bamu tollook njàngum ñatteelu xaaj alxuraan si lu ñu fulul.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (6/ 189) (5013).
Yataal gi (1)
إرشاد الساري لشرح صحيح البخاري (7/ 463).
Cited in books
3 BooksYataal gi (3)
- ما لا يسع أطفال المسلمين جهله«وَالَّذِي نَفْسِي بِيَدِهِ! إِنَّهَا لَتَعْدِلُ ثُلُثَ القُرْآنِ»[75].
- مجالس تدارس القرآن للمبتدئين (سورة الفاتحة وقصار المفصّل)1وأخرج البخاري عن أبي سعيد الخدري -رضي الله عنه- : « أن رجلا سمع رجلا يقرأ: قل هو الله أحد يرددها، فلما أصبح جاء إلى رسول الله ﷺ فذكر ذلك له، وكأن الرجل يتقالّها، فقال رسول الله ﷺ: والذي نفسي بيده إنها لتعدل ثلث القرآن »([140]).
- موسوعة الإيمانفعَنْ أَبِي سَعِيدٍ الخُدْرِيِّ رضي الله عنه: أَنَّ رَجُلًا سَمِعَ رَجُلًا يَقْرَأُ: {قُلْ هُوَ اللَّهُ أَحَد} أَحَدٌ، يُرَدِّدُهَا. فَلَمَّا أَصْبَحَ جَاءَ إِلَى رَسُولِ اللَّهِ صلى الله عليه وسلم فَذَكَرَ ذَلِكَ لَهُ، وَكَأَنَّ الرَّجُلَ