«Jullit bu góor du bañ jullit bu jigéen, ndax su bañee ci moom jenn jikkó gërëm na ci moom jeneen jikkó»
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«Jullit bu góor du bañ jullit bu jigéen, ndax su bañee ci moom jenn jikkó gërëm na ci moom jeneen jikkó».
«لَا يَفْرَكْ مُؤْمِنٌ مُؤْمِنَةً، إِنْ كَرِهَ مِنْهَا خُلُقًا رَضِيَ مِنْهَا آخَرَ» أَوْ قَالَ: «غَيْرَهُ».
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- tere na jëkkër di bañ jabaram bañ guy waral mu koy tooñ di ko bàyyi di ko dummóoyu; Ndaxte nit dañu koo bind cig wàññiku , te bu bañee ci moom ay jikkó yu ñaaw, dana fekk ci moom ay jikkó yu rafet; bu ko defee mu gërëm yu rafet yi tolloog moom , te muñ yu ñaaw yi mu gërëmul, loolu mooy tax muy muñ te du ko bañ mbañeel guy waral muy tàggalikoo ak moom.
لا يفرك: لا يبغض.
Woo aji-gëm ji ci màndute ak jëfandikoo am xelam ci bépp juuyoo bu am ci digganteem ak jabaram, te bañ a àttewoo ay bànneex ak yëngu-yëngu.
Mbiri jullit bu góor mooy ne du bañ jullit bu jigéen mbañeel gu rëy guy waral mu tàqalikoo ak moom, waaye dafa jaadu ci moom muy jéllalee yi mu sib ngir yi mu bëgg.
Soñee ci rafetuw nekkiin ak àndandoo ci diggante ñaar ñiy sëy.
Ngëm day waral jikkó yu tedd, kon jullit bu góor ak bu jigéen bi manuñoo ñàkk ay jikkó yu rafet, ndaxte ngëm gi day waral ñu am ay jikkó yu ñu gërëm.
Téere Muslim bi gën a wér (2/ 1091) (1469).
Yataal gi (9)
بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.
لسليم الهلالي (1/ 359).
شرح رياض الصالحين.
لابن عثيمين (3/ 122).
فتح رب البرية بتلخيص الحموية.
لابن عثيمين (ص117).
مجموع فتاوى ابن باز (25/ 246).
نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.
لمجموعة من الباحثين (1/ 282).
Cited in books
7 BooksYataal gi (7)
- الدعاء ويليه العلاج بالرقى من الكتاب والسنةالرقى من الكتاب والسنة«لا يَفْرَكْ مُؤْمِنٌ مُؤْمِنَةً، إِنْ كَرِهَ مِنْهَا خُلُقًا، رَضِيَ مِنْهَا آخَرَ»[٦٣].
- رياض الصالحينرياض الصالحين مع فوائد وهدايات - 2«لا يَفْرَكْ مُؤْمِنٌ مُؤْمِنَةً؛ إنْ كَرِهَ مِنْهَا خُلُقاً رَضيَ مِنْهَا آخَرَ» أَوْ قَالَ: «غَيْرَهُ».
- مجموعة زاد التربية الإسلامية (3)، والسيرة النبوية (3)السيرة النبوية (3)«لا يَفْرَكْ -أي: لا يُبغِضْ- مُؤْمِنٌ مُؤْمِنَةً، إِنْ كَرِهَ مِنْها خُلُقًا رَضِيَ مِنْها آخَرَ».
- مشروع منهاج زادكزادك 3 طالب نهائي«لَا يَفْرَكْ (يبغض ويَكرَهُ) مُؤْمِنٌ مُؤْمِنَةً، إِنْ كَرِهَ مِنْهَا خُلُقًا رَضِيَ مِنْهَا آخَرَ»
- مشروع منهاج زادكزادك 3 طالب نهائي«لَا يَفْرَكْ مُؤْمِنٌ مُؤْمِنَةً، إِنْ كَرِهَ مِنْهَا خُلُقًا رَضِيَ مِنْهَا آخَرَ» (رواه مسلم 1469).
- نبراس طالب (5)1«لَا يَفْرَكْ (يبغض ويَكرَهُ) مُؤْمِنٌ مُؤْمِنَةً، إِنْ كَرِهَ مِنْهَا خُلُقًا رَضِيَ مِنْهَا آخَرَ»
- نبراس طالب (5)1«لَا يَفْرَكْ مُؤْمِنٌ مُؤْمِنَةً، إِنْ كَرِهَ مِنْهَا خُلُقًا رَضِيَ مِنْهَا آخَرَ»