daan na nu digal bu nu nekkee way-tukki walla ay tukkikat, nu bañ a summi sunuy Saŋ ñatti fan ak seen i guddi, lu dul ci janaba, waaye ci xayta, ak saw, ak nelaw
Jële nañu ci Sirr ibn Hubays mu wax ne:
Ñëw naa vi Safwaan ibn Assaal Al-Muraadii, di ko laaj masaa ci ay Saŋ, mu ne ma: lam moo la indi yaw Sirr? Ma ne ko ngir sàkku xam-xam, mu ne ma: malaaka yi de dañuy teg seen i laaf ñeel kiy sàkku xam-xam; ngir gërëm li mu sàkku, ma ne ko: liy mbir mooy masaa ci ay Saŋ ginnaaw saw ak xayta day nux-nuxi ci sama dënn, te yaw bokk nga ci sahaabay Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ma ñëw ngir laaj la: ndax dégg nga ko muy wax ci loolu dara? Mu ne: waaw, daan na nu digal bu nu nekkee way-tukki walla ay tukkikat, nu bañ a summi sunuy Saŋ ñatti fan ak seen i guddi, lu dul ci janaba, waaye ci xayta, ak saw, ak nelaw, ma ne ko: ndax dégg nga ko miy tudd mbàggeel? Mu ne: waaw, nekkoon nanu ak Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci tukki, ba nu nekkee fa moom rekk benn kaw-kaw woo ko ci kàddu gu xumb: éey Muhammat, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tontu ko nu mel ni kàddoom ga: "waaw ñëwal" nu ne ko: yal na nga toskare, wàcceel sa kàddu gi, yaa ngi fi Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, te danu noo tere lii, mu daal di ne: giñ naa ci Yàlla ne duma wàcce sama kàddu, kaw-kaw ne: nit ki dana bëgg aw nit te jotu leen, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di ne: "nit ki ki mu bëgg lay ànd al ëllëg bis-pénc", deñul di nu waxtaanal, ba tudd ab bunt bu nekk ci wetu sowwu, doxub yaatuwaayam, walla aji-war ji dana dox ci yaatuwaayam ñent-fukk walla juróom-ñaar-fukki at.
أَتَيْتُ صَفْوَانَ بْنَ عَسَّالٍ المُرَادِيَّ، أَسْأَلُهُ عَنِ المَسْحِ عَلَى الخُفَّيْنِ، فَقَالَ: مَا جَاءَ بِكَ يَا زِرُّ؟ فَقُلْتُ: ابْتِغَاءَ العِلْمِ، فَقَالَ: إِنَّ المَلاَئِكَةَ لَتَضَعُ أَجْنِحَتَهَا لِطَالِبِ العِلْمِ؛ رِضًا بِمَا يَطْلُبُ، فَقُلْتُ: إِنَّهُ حَكَّ فِي صَدْرِي المَسْحُ عَلَى الخُفَّيْنِ بَعْدَ الغَائِطِ وَالبَوْلِ، وَكُنْتَ امْرَأً مِنْ أَصْحَابِ النَّبِيِّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَجِئْتُ أَسْأَلُكَ: هَلْ سَمِعْتَهُ يَذْكُرُ فِي ذَلِكَ شَيْئًا؟ قَالَ: نَعَمْ، كَانَ يَأْمُرُنَا إِذَا كُنَّا سَفْرًا أَوْ مُسَافِرِينَ أَلَّا نَنْزِعَ خِفَافَنَا ثَلاَثَةَ أَيَّامٍ وَلَيَالِيهِنَّ إِلَّا مِنْ جَنَابَةٍ، لَكِنْ مِنْ غَائِطٍ وَبَوْلٍ وَنَوْمٍ، فَقُلْتُ: هَلْ سَمِعْتَهُ يَذْكُرُ فِي الهَوَى شَيْئًا؟ قَالَ: نَعَمْ، كُنَّا مَعَ النَّبِيِّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فِي سَفَرٍ فَبَيْنَا نَحْنُ عِنْدَهُ إِذْ نَادَاهُ أَعْرَابِيٌّ بِصَوْتٍ لَهُ جَهْوَرِيٍّ: يَا مُحَمَّدُ، فَأَجَابَهُ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ عَلَى نَحْوٍ مِنْ صَوْتِهِ: «هَاؤُمُ» وَقُلْنَا لَهُ: وَيْحَكَ اغْضُضْ مِنْ صَوْتِكَ، فَإِنَّكَ عِنْدَ النَّبِيِّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، وَقَدْ نُهِيتَ عَنْ هَذَا، فَقَالَ: وَاللَّهِ لاَ أَغْضُضُ، قَالَ الأَعْرَابِيُّ: المَرْءُ يُحِبُّ القَوْمَ وَلَمَّا يَلْحَقْ بِهِمْ، قَالَ النَّبِيُّ صَلَّى اللَّهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «المَرْءُ مَعَ مَنْ أَحَبَّ يَوْمَ القِيَامَةِ»، فَمَا زَالَ يُحَدِّثُنَا حَتَّى ذَكَرَ بَابًا مِنْ قِبَلِ المَغْرِبِ مَسِيرَةُ عَرْضِهِ، أَوْ يَسِيرُ الرَّاكِبُ فِي عَرْضِهِ أَرْبَعِينَ أَوْ سَبْعِينَ عَامًا.
Sirr ibn Hubays dafa ñëw ci Safwaan ibn Assaal yal na ko Yàlla dollee gërëm, di ko laaj ci masaa ci ay Saŋ, Safwaan ne ko: ana lan moo la indi yaw Sirr? Mu ne ko: ngir sàkku xam-xam, mu ne ko: malaaka yi dañuy teg seen i laaf ñeel kiy sàkku xam-xam; ngir gërëm ak màggal aji-sàkku xam-xam ji di def, Sirr ne: masaa ci ay Saŋ ginnaaw xayta ak saw day dengi-dengi vi sama xel mi, te yaw bokk nga ci sahaabay Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ma ñëw ngir laaj la ndax dégg nga Yonnente bi di tudd dara ci loolu? Safwaan ne: waaw, daan na nu digal bu nu nekkee way-tukki nu bañ a summi sunuy Saŋ ñatti fan ak seen i guddi ci toj mu ndaw niki xayta ak saw ak nelaw, ku dul janaba kon day war ñu summi ko, ma ne ko: ndax dégg nga ko mu wax ci bëgg dara? Mu ne: waaw, nekkoon nanu ak Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci ab tukki ba nu nekkee fa moom benn kaw-kaw woo ko ci kàddu gu kawe: yaw Muhammat, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tontu ko ci kàddu gu kawe gu jege kàddoom ga, nu ne ko: yal na nga toskare wàcceel sa kàddu gi, yaa ngi fi Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, te dañu laa tere ngay yëkkëti sa kàddu fi moom. Ngir ag dëgëram mu ne: giñ naa ci Yàlla ne duma ko wàcce, kaw-kaw bi daal di ne: yaw Yonnente Yàlla bi, nit ki dana bëgg nit ñi baax ñi te jëful lu mel ni seen i jëf? Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: nit ki ki mu bëgg lay àndal ëllëg bis-pénc, Sirr nee na: Safwaan deñul di nu waxtaanal ba tudd buntub tuub bu nekk ci wàllug Saam bi, Yàlla da ko a bind ba mu bindee asamaan yi ak suuf si, aji-war ji dana dox vi yaatuwaayam ñent-fukk walla juróom-ñaar-fukki at, te deesu ko tëj ba keroog jant bi di fekke ca sowwu ba.
Ngëneelu sàkku xam-xam, an màggaayu dayob aji-sàkku xam-xam ji, ak teralug malaaka yi ñeel ko.
Leral xérug ñi taabihuina yi ci sàkku xam-xam ci sahaabavyi yal na leen Yàlla dollee gërëm.
Dagan na ñiasaa ci ay Saŋ, te ab diiram: ñeel aji-tukki ji mooy ñatti fan ak seen i guddi, bu dee ngir aji-sax ji benn bis ak guddeem.
Masaa ci ay Saŋ ci toj mu ndaw dong lay nekke.
Dagan na aji-laaj ji sàkku ci boroom xam-xam bi tegtalam ndax yax mbind la, walla tegtaloo la ak pastéefoom, te war na boroom xam-xam bi mu bañ a diis ci loolu.
Am teggin ci woroom xam-xam yi ak ñu baax ñi, ak suufeel sa kàddu ci jotaayi xam-xam yi.
Jàngal aji-réer ji rafeti teggin ak reegali doxaliin yi.
Ñaaxe ci roy ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci lewetam, ak rafet jikkoom, ak wàqateem ak nit ñi ci kem seen xam-xam ak seen xel.
Al-Mubaarakfuurii nee na: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa yëkkëti kàddoom ci anamug ñeewant ngir jëfam bañ a yàqu ngir waxu Yàlla mu kawe mi: {buleen yëkkëti seen kàddu ci kaw kàddug Yonnente bi}; mu dugal ko gànt ngir ak ñàkka xamam, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc yëkkëti kàddoom ba mu mel ni kàddoom ga walla mu gën ko a kawe, ngir ag ñeewantoom gu tar ci moom
Xér ci toog ak ñu baax ñi ak jege leen ak bëgg leen.
An-Nawawii: nekk ak ñoom tekkiwul ne day nekk ci seen daraja ag fayam mel ni seenug fay ci gépp anam.
Ubbi buntu mébét ak yaakaar, ak bége ci mucc, ak ñeewant ci waare.
Yaatug yërmàndey Yàlla mu màgg mi, ak li mu ubbi buntub tuub.
Ñaaxe ci gaaw a tuub ak di regle bakkan bi, ak dellu ci Yàlla mu kawe mi.
Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (5/ 505) (3535).
Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja (1/ 302) (478).
Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (30/ 18) (18095).
Yataal gi (7)
نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.
لمجموعة من الباحثين (1/ 36).
شرح رياض الصالحين.
لابن عثيمين (1/ 107).
بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.
لسليم الهلالي (1/ 57).
المعجم الوسيط (2/ 968).
Cited in books
6 BooksYataal gi (6)
- رياض الصالحينرياض الصالحين مع فوائد وهدايات - 1 «الْمَرْءُ مَعَ مَنْ أَحَبَّ يَوْمَ الْقِيَامَةِ».
- رياض الصالحينرياض الصالحين مع فوائد وهدايات - 2«المَرْءُ مَعَ مَنْ أَحَبَّ».
- رياض الصالحينرياض الصالحين مع فوائد وهدايات - 2«المَرءُ مَعَ مَنْ أَحَبَّ».
- رياض الصالحينرياض الصالحين مع فوائد وهدايات - 2«المَرْءُ مَعَ مَنْ أَحَبَّ».
- مجموعة زاد التربية الإسلامية (1)، والسيرة النبوبة (1)، والعقيدة (1)، والفقه (1)مجموعة زاد الفقه (1)«كان رسول اﷲ ﷺ يأمرنا إذا كنا سَفْرا ألا نَنْزِعَ خِفَافَنا ثلاثةَ أيامَ ولياليهن إلا مِنْ جَنَابَةٍ، لكن من غائطٍ وبولٍ ونومٍ».
- مشروع منهاج زادكزادك 2 طالب نهائيقال النبي صلى الله عليه وسلم: «الحَجُّ عَرَفَةُ»