Skip to content

"kenn ci yéen du gëm ba keroog bànneexam di topp li ma indi".

Jële nañu ci Abii Muhammad Abdullah Ibn Amr Ibn Al-Haas yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:

"kenn ci yéen du gëm ba keroog bànneexam di topp li ma indi".

«لَا يُؤْمِنُ أَحَدُكُمْ حَتَّى يَكُونَ هَوَاهُ تَبَعًا لِمَا جِئْتُ بِهِ».

Soloo nanu ko ci téereb Al-Hujja ci càllale gu wér
An-Nawawii nee na: hadiis bu wér la
Leeral gi

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral ne nit ki du nekk aji-gëm ju matug ngëm ba keroog ag bëgg-bëggam di topp li Yonente bi indi ci ay digle ak i tere ak yeneen; mu bëgg li mu digle, bañ li mu tere.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Hadiis bi ab tënk la ci nangul Sariiha ak wommatul ko.

Àrtu nit ki ci muy àttewoo xel ak aada di ko jiital ci kaw li Yonente bi indi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, kuy def loolu dees na dàq ci moom ngëm.

Dañoo war a àttewoo Sariiha ci lépp, ndax li mu wax: "li ma indi".

Gëm Yàlla day yokkoo ci topp Yàlla di wàññikoo ci moy.

Dellluwaay yi
Yataal gi (5)

الحجة على تارك المحجة لأبي الفتح نصر بن إبراهيم المقدسي.

برقم (25).

فتح الباري لابن حجر (13/289).

جامع العلوم والحكم (3/1146).

شرح النووي على مسلم (1/77).