Skip to content

ku bàyyi jullig tàkkusaan jëfam yàquna".

Jële na ñu ci Buraydata Ibn Al-Husaybi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:

Deeleen teel a julli tàkkusaan, ndax yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "ku bàyyi jullig tàkkusaan jëfam yàquna".

بَكِّرُوا بِصَلَاةِ الْعَصْرِ، فَإِنَّ النَّبِيَّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ: «مَنْ تَرَكَ صَلَاةَ الْعَصْرِ فَقَدْ حَبِطَ عَمَلُهُ».

Al-buxaariy soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- artu na ci yeexe jullig tàkkusaan ca waxtoom te tay ko, ak ne ku def loolu jëfam yàquna te ag neen la.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ñaaxe ci sàmmoonte ak jullig tàkkusaan ci njëlbeenu waxtoom te gaawe ko.

Tëkku gu tar ñeel na ku bàyyi jullig tàkkusaan, ak ne yeexe ko ba waxtu wa jàll, moo gën a màgg yeexe geneen juuli, ndax mooy julli gi digg-dóomu ga ñu jagleel ag digle, ci wax ji Yàlla wax ne: (na ngeen sàmmoonte ak julli yi ak julli gu digg-dóomu gi) [Al-Baxara: 238].

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 115) (553).

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (38/ 152) (23045).

Yataal gi (9)

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (5/ 56).

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

لمصطفى الخِن وغيره (2/ 777).

فيض القدير شرح الجامع الصغير (3/ 206).

بهجة الناظرين.

لسليم الهلالي (2/ 260).

تطريز رياض الصالحين.

لفيصل آل مبارك (ص614).