"bu nit waxee mbokkam: yaw yéefar bi, kon kenn ci ñoom ñaar yóbb na ko, bu dee li mu wax noonu la, lu ko moy mu dellusi ci moom".
Jële nañu ci Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
"bu nit waxee mbokkam: yaw yéefar bi, kon kenn ci ñoom ñaar yóbb na ko, bu dee li mu wax noonu la, lu ko moy mu dellusi ci moom".
«أَيُّمَا امْرِئٍ قَالَ لِأَخِيهِ: يَا كَافِرُ، فَقَدْ بَاءَ بِهَا أَحَدُهُمَا، إِنْ كَانَ كَمَا قَالَ، وَإِلَّا رَجَعَتْ عَلَيْهِ».
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc moytandikuloo na jullit bi di wax mbokkum jullitam: yaw yéefar bi, ndax kon kenn ci ñoom dana yayoo baatu kéefar bi, bu dee li mu wax noonu la, lu ko moy mu dellu ci ki yéefarloo mbokkam mi.
Xupp jullit bi ci muy wax mbokk jullitam lu bokkul ci ay meloom ci meloy kàccoor ak kéefar.
Àrtu ci wax ju ñaaw jii, ak ne ki ko wax moo ngi ci giraawaale gu màgg bu ko waxee mbokkam, kon war na ci nit ki mu sàmm làmmiñam te bañ a wax ci lu dul ag xam gu wóor.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (8/ 26) (6104).
Téere Muslim bi gën a wér (1/ 79) (60).
Yataal gi (3)
البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (2/ 390).
إرشاد الساري لشرح صحيح البخاري (9/ 65).
النهاية في غريب الحديث والأثر (91).
Cited in books
3 BooksYataal gi (3)
- قاموس الكبائرموسوعة الكبائر - المجموعة الثانية«أَيُّمَا امْرِئٍ قَالَ لِأَخِيهِ: يَا كَافِرُ، فَقَدْ بَاءَ بِهَا أَحَدُهُمَا، إِنْ كَانَ كَمَا قَالَ، وَإِلَّا رَجَعَتْ عَلَيْهِ» [100].
- مادة العقيدة الإسلامية(أَيُّمَا امْرِئٍ قَالَ لِأَخِيهِ: يَا كَافِرُ، فَقَدْ بَاءَ بِهَا أَحَدُهُمَا، إِنْ كَانَ كَمَا قَالَ، وَإِلَّا رَجَعَتْ عَلَيْهِ).
- مجموعة زاد العقيده (4)العقيدة 4«أَيُّما امْرِئٍ قال لِأَخِيهِ: يا كافِرُ، فَقَدْ باءَ بِها أَحَدُهُما، إِنْ كانَ كَما قالَ، وَإِلَّا رَجَعَتْ عَلَيْهِ».