Sama xarit ba yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dénk na ma ñatt: woor ñatti fan ci weer wu ne, ak ñaari ràkkay yoor-yoor, ak ma julli Witar balaa may nelaw.
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Sama xarit ba yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dénk na ma ñatt: woor ñatti fan ci weer wu ne, ak ñaari ràkkay yoor-yoor, ak ma julli Witar balaa may nelaw.
أَوْصَانِي خَلِيلِي صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ بِثَلاَثٍ: صِيَامِ ثَلاَثَةِ أَيَّامٍ مِنْ كُلِّ شَهْرٍ، وَرَكْعَتَيِ الضُّحَى، وَأَنْ أُوتِرَ قَبْلَ أَنْ أَنَامَ.
Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm day xibaare ne soppeem ba di xaritam ba Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc da ko a dénk ñatti mbir: Bi ci njëkk: woor ñatti fan ci weer wu ne. Ñaareel bi: julli ñaari ràkkay yoor-yoor bis bu nekk. Ñatteel bi: Wiitar njëkk muy nelaw, loolu nag ci ki ragal ne du yewwu ci mujjug guddi gi.
Wuute gi ay dénkaaneem wuute ñeel ay Sahaabaam: dafa tabaxu ci lu mu xam moom Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc meloy àndandoom yi, ak li méngoo ak kenn ku ne ci ñoom, ki am kàttan jihaad day méngoo ak moom, jaamukat bi jaamu day méngoo ak moom, boroom xam-xam bi xam- day méngoo ak moom, noonu lay deme.
Ibn Hajar Al-Asxalaanii nee na ci li mu wax: woor ñatti fan ci weer wu ne, li ci feeñ mooy li mu ci namm mooy bis yu leer yi; te mooy: bisu fukkeel bi ak ñatt, ak fukkeel ak ñent, ak fukkeel ak juróom, ci weeru gàddaay gi.
Ibn Hajar Al-Asxalaanii nee na: nekk na ci ne sopp nañu jiital Witar ci kaw nelaw, loolu nag ci àqi ku wóoluwul ne dana yeewu.
Solos ñatti jëf yii; ndax li ko Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dénk ab lim ci ay Sahaabaam.
Ibn Daxiixil Hiid nee na li mu wax: (ñaari ràkkay yoor-yoor): amaana dafa tudd li ci gën a néew nga xam ne def gi daa feddaliku, te tegtal la ci ne sopp nañu jullig yoor-yoor, la ca gën a néew mooy ñaari ràkka.
Waxtuw julli yoor-yoor: mooy ginnaaw fenkug jant bi ba luy toll ci ñenteelu xaaju waxtu wi, waxtoom nag dana wéy ba laata Tisbaar ci luy tollook fukki simili, ab limam nag: la ca gën a néew mooy ñaari ràkka, wuute nañu ca la ca gën a bari; nee nañu: la ca gën a bari amul ab lim.
Waxtuw jullig Wiitar: mooy ginnaaw jullig Gee ba keroog fajar gi di fenk, la ca gën a néew mooy benn ràkka, la ca gën a bari mooy fukki ràkka ak benn.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (3/ 41) (1981).
Téere Muslim bi gën a wér (1/ 499) (721).
Yataal gi (6)
تيسير العلام.
للبسام (ص342).
تنبيه الأفهام شرح عمدة الأحكام.
لابن عثيمين (3/ 456).
خلاصة الكلام على عمدة الأحكام.
لفيصل آل مبارك (ص159).
Cited in books
10 BooksYataal gi (10)
- الصلاة التي علمها النبي ﷺ الصحابة رضي الله عنهمالصلاة التي علمها النبي ﷺ الصحابة رضي الله عنهم«بِصِيَامِ ثَلَاثَةِ أَيَّامٍ مِنْ كُلِّ شَهْرٍ، وَرَكْعَتَيِ الضُّحَى، وَأَنْ أُوتِرَ قَبْلَ أَنْ أَرْقُدَ»[440].
- الصلاة التي علمها النبي ﷺ الصحابة رضي الله عنهمالصلاة التي علمها النبي ﷺ الصحابة رضي الله عنهمأَوْصَانِي خَلِيلِي ﷺ بِثَلاَثٍ: «صِيَامِ ثَلاَثَةِ أَيَّامٍ مِنْ كُلِّ شَهْرٍ، وَرَكْعَتَيِ الضُّحَى، وَأَنْ أُوتِرَ قَبْلَ أَنْ أَنَامَ»[685].
- الصلاة التي علمها النبي ﷺ الصحابة رضي الله عنهم«بِصِيَامِ ثَلَاثَةِ أَيَّامٍ مِنْ كُلِّ شَهْرٍ، وَرَكْعَتَيِ الضُّحَى، وَأَنْ أُوتِرَ قَبْلَ أَنْ أَرْقُدَ»[440].
- الصلاة التي علمها النبي ﷺ الصحابة رضي الله عنهم«أَوْصَانِي خَلِيلِي ﷺ بِثَلَاثٍ: صِيَامِ ثَلَاثَةِ أَيَّامٍ مِنْ كُلِّ شَهْرٍ، وَرَكْعَتَيِ الضُّحَى، وَأَنْ أُوتِرَ قَبْلَ أَنْ أَنَامَ»[685].
- رياض الصالحينرياض الصالحين مع فوائد وهدايات - 6«أَوْصاني خَلِيلي صلى الله عليه وسلم بِثلاثٍ:صيَامِ ثَلاثَةِ أَيَّامٍ مِن كلِّ شَهرٍ، وَرَكعَتَي الضُّحىٰ، وَأَن أُوتِرَ قَبْلَ أَنْ أنامَ».
- مجموعة زاد السيرة النبوية (2)1«أوصاني خليلي بثلاث: صيام ثلاثة أيام من كل شهر، وركعتي الضحى، وأن أوتر قبل أن أنام»
- مشروع المنهج التعليميمادة الفقه مستوى 2«صِيَامِ ثَلاَثَةِ أَيَّامٍ مِنْ كُلِّ شَهْرٍ، وَرَكْعَتَيِ الضُّحَى، وَأَنْ أُوتِرَ قَبْلَ أَنْ أَنَامَ»
- مشروع المنهج التعليميمادة الفقه مستوى 3«صِيَامِ ثَلاَثَةِ أَيَّامٍ مِنْ كُلِّ شَهْرٍ، وَرَكْعَتَيِ الضُّحَى، وَأَنْ أُوتِرَ قَبْلَ أَنْ أَنَامَ»
- من الأحكام الفقهية في الطهارة والصلاة والجنائز«أَوْصَانِي خَلِيلِي بِثَلَاثٍ: صِيَامِ ثَلَاثَةِ أَيَّامٍ مِنْ كُلِّ شَهْرٍ، وَرَكْعَتَي الضُّحَى، وَأَنْ أُوتِرَ قَبْلَ أَنْ أَنَامَ»[77].
- نبراس طالب (3)نبراس طالب 3أَوْصَانِي خَلِيلِي صلى الله عليه وسلم بِثَلاَثٍ: «صِيَامِ ثَلاَثَةِ أَيَّامٍ مِنْ كُلِّ شَهْرٍ، وَرَكْعَتَيِ الضُّحَى، وَأَنْ أُوتِرَ قَبْلَ أَنْ أَنَامَ»