«bàyyiwuma sama ginnaaw fitna ju dàq a lor góor ñi ci jigéen ñi»
Jële nañu ci Usaamata Ibn Sayd -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«bàyyiwuma sama ginnaaw fitna ju dàq a lor góor ñi ci jigéen ñi»
«مَا تَرَكْتُ بَعْدِي فِتْنَةً أَضَرَّ عَلَى الرِّجَالِ مِنَ النِّسَاءِ».
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne bàyyiwul ginnaawam nattu bu gën a man a lor góor ñi ci jigéen ñi; ndax bu bokkee ci njabootam man naa waral mu topp ko ci lu wuuteek Sariiha, bu dee ab jàmbur la ci moom man naa jaxasoo ak moom ak di wéet ak moom te loolu day waral ay yàqute.
...:
War na ci jullit bi mu moytu ftnaay jigéen ñi, te fatt bépp bunt buy waral fitnawu ci ñoom.
War na ci aji-gëm ji mu làqu ci Yàlla, ak xemmeem jëm ci moom ngir mucc ci fitna yi.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (7/ 8) (5096).
Téere Muslim bi gën a wér (4/ 2097) (2740).
Yataal gi (3)
بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.
لسليم الهلالي (373).
فتح الباري لابن حجر (9/ 138).