Skip to content

Tere na lépp lu am bëñ ci negment yi, ak lépp lu am aw sàll ci ñanaaw yi.

Jële na ñu ci Ibn Abbaas yal na leen Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne:

Tere na lépp lu am bëñ ci negment yi, ak lépp lu am aw sàll ci ñanaaw yi.

نَهَى عَنْ كُلِّ ذِي نَابٍ مِنَ السِّبَاعِ، وَعَنْ كُلِّ ذِي مِخْلَبٍ مِنَ الطَّيْرِ.

Muslim soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tere na ñuy lekk bépp negment ci rab yiy fàdde di rëbbe seen i bëñ, ak lépp ñanaaw luy dagge ak di jàppe ci sàllam.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Xérug lislaam ci yu teey yi ci lépp, ci lekk ak naan ak yeneen yi.

Liy cosaan ci lekk yi mooy dagan; lu dul lu tegtal ñëw araamal ko.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1534) (1934).

Yataal gi (9)

سبل السلام شرح بلوغ المرام.

للصنعاني (2/ 506).

توضيح الأحكام مِن بلوغ المرام.

لعبد الله البسام (7/ 5).

فتح ذي الجلال والإكرام شرح بلوغ المرام.

لابن عثيمين (6/ 6).

منحة العلام في شرح بلوغ المرام.

لعبد الله الفوزان (9/ 173).

فتاوى اللجنة الدائمة - المجموعة الأولى (22/ 290).