Skip to content

"bu kenn ci yéen faatoo dees na ko gaaral bérabam ci suba gi ak ci ngoon gi

Jële nañu ci Abdulaah Ibn Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:

"bu kenn ci yéen faatoo dees na ko gaaral bérabam ci suba gi ak ci ngoon gi, bu dee dafa bokk ci waa Àjjana mu nekk ci waa Àjjana, bu dee dafa bokk ci waa Sawara mu nekk ci waa Sawara, ñu naan ko: lii mooy sa bérab ba keroog Yàlla di la dekkil ëllëg bis-pénc".

«إِنَّ أَحَدَكُمْ إِذَا مَاتَ عُرِضَ عَلَيْهِ مَقْعَدُهُ بِالْغَدَاةِ وَالعَشِيِّ، إِنْ كَانَ مِنْ أَهْلِ الجَنَّةِ فَمِنْ أَهْلِ الجَنَّةِ، وَإِنْ كَانَ مِنْ أَهْلِ النَّارِ فَمِنْ أَهْلِ النَّارِ، فَيُقَالُ: هَذَا مَقْعَدُكَ حَتَّى يَبْعَثَكَ اللَّهُ يَوْمَ القِيَامَةِ».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne jaam bi bu deewee dañu koy gaaral wàccuwaayam ak bérabam ba mu jagoo ca Àjjana walla ca Sawara, ci njëlbéenu bëccëg ak ci mujj gi; bérabam ba nekk ca Àjjana bu dee ci waa Àjjana la bokk, walla bérabam ba nekk ca Sawara bu dee ca waa Sawara la bokk, ñu naan ko: Lii mooy sa bérab ba ñu la jëme boo dekkee ëllëg bis-pénc; te loo lu ag xéewal la ñeel aji-gëm ji, mbugal la it ñeel yéefar bi.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Mbugalum bàmmeel ak xéewalam dëgg la.

Ibn Hajar nee na: gaaral gii ñeel aji-gëm ji ragal Yàlla ak yéefar bi loolu lu leer la, waaye aji-gëm ji rax ay jëfam kooku amaana it ñu gaaral ko bérab ba mu jëm ca Àjjana.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (2/ 99-100) (1379).

Téere Muslim bi gën a wér (4/ 2199) (2866).

Yataal gi (6)

عمدة القاري شرح صحيح البخاري.

لبدرالدين العيني (8/ 209).

التنوير شرح الجامع الصغير.

لمحمد الصنعاني (2/ 209).

الإفصاح عن معاني الصحاح.

ليحيى بن هبيرة (4/ 131).