"gaarde benn bis ci yoonu Yàlla moo gën àdduna ak li ci biiram
Jële nañu ci Sahl Ibn Sahd yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
"gaarde benn bis ci yoonu Yàlla moo gën àdduna ak li ci biiram, te bérab buy tollook ab yar ca Àjjana moo gën àdduna ak li ci nekk, gennug gont gu jaam bi di gont ci yoonu Yàlla walla gennug xëy moo gën àdduna ak li ci biiram".
«رِبَاطُ يَوْمٍ فِي سَبِيلِ اللَّهِ خَيْرٌ مِنَ الدُّنْيَا وَمَا عَلَيْهَا، وَمَوْضِعُ سَوْطِ أَحَدِكُمْ مِنَ الجَنَّةِ خَيْرٌ مِنَ الدُّنْيَا وَمَا عَلَيْهَا، وَالرَّوْحَةُ يَرُوحُهَا العَبْدُ فِي سَبِيلِ اللَّهِ أَوِ الغَدْوَةُ خَيْرٌ مِنَ الدُّنْيَا وَمَا عَلَيْهَا».
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xamle ne taqoo ak bérab bi dox diggante jullit ñi ak yéefar yi ngir sàmm jullit ñi ci ñoom ci benn bis di aji-sellal ngir Yàlla loolu moo gën àdduna ak li ci biiram, ak ne bérab buy tollook ab yar bu ñuy jihaade ci yoonu Yàlla ca Àjjana moo gën àdduna ak li ci biiram, ak ne fay ak yoolu dox ci yoonu Yàlla ci njëlbeenu bëccëg gi ba ci tàmbalig waxtuw Tisbaar gi, walla ngoon gi: li dale ci waxtuw Tisbaar gi ba ca guddi ga loolu moo gën àdduna ak li ci biiram.
Ngëneelu gaarde ci yoonu Yàlla, ngir li ci nekk ci ay musiba ci bakkan bi, ak la cay topp ci yëkkëti kàddug Yàlla gi ak dimbali diineem ji; lii moo tax yoolu benn bisam moo gën àdduna ak li ci biiram.
Doyadig àdduna ci buñu ko tëkkaleek allaaxira; ndax bérab buy tollook ab yar ca Àjjana, moo gën àdduna ak li ci biiram.
Ngëneelu jihaad ci yoonu Yàlla, ak màggayu yoolam; ndax yoolu gennug gont walla xëy, moo gën àdduna ak li ci biiram.
Li mu wax: "ci yoonu Yàlla" tegtal la ci solos sellal, ak ne fay ga ci sellal ga la aju.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (4/ 35) (2892).
Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1500) (1881).
Yataal gi (2)
تيسير العلام شرح عمدة الأحكام.
لعبد الله البسام (ص739).