Skip to content

«Deesul takk jigéen ci lu dul kilifa».

Jële na ñu ci Abuu Muusa Al-Ashsrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

«Deesul takk jigéen ci lu dul kilifa».

«لا نِكَاحَ إِلّا بِوَليٍّ».

Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
Wér na
Leeral gi

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa leeral ne jigéen du dagan ñu takk ko ci lu dul kilifa gu taxawe takk ga.

Maanaay baat yi

لا نكاح : لا نكاح صحيح ومعتبر شرعًا.

الوَلِيُّ : هو أقرب الرجال إلى المرأة من عصبتها الذين يرثونها، كالأب والأخ.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Kilifa sart la ci wérug sëy, bu takk amee ci lu dul kilifa, walla jigéen maye boppam, kon sëy ba du wér.

Kilifa mooy góor gi gën a jege jigéen gi, kon kilifa gu sori du ko maye te ku jege nekk fa.

Sàrtal nañu ci kilifa: mu nekk mukàllaf, nekk góor, am xelum xam njariñi sëy, te kilifa gi ak ka muy meye ñu bokk diine, ku amul melo yii manut a nekk kilifa ci fas ab sëy.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (3/ 427) (2085).

Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (2/ 392) (1101).

Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja (3/ 79) (1881).

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (32/ 280) (19518).

Yataal gi (10)

البدرُ التمام شرح بلوغ المرام.

للمَغرِبي (7/ 57).

إرواء الغليل في تخريج أحاديث منار السبيل.

للألباني (6/ 237).

توضِيح الأحكام من بلوغ المَرَام.

للبسام (5/ 262).

منحة العلام في شرح بلوغ المرام.

لعبد الله الفوزان (7/ 222).

فتح ذي الجلال والإكرام بشرح بلوغ المرام.

لابن عثيمين (4/ 469).