«Bu nit ki faatoo ay jëfam dog na ba mu des ñatt: ba mu des saraxe buy wéy, walla xam-xam bu ñuy jariñoo, walla doom ju baax ju koy ñaanal».
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
«Bu nit ki faatoo ay jëfam dog na ba mu des ñatt: ba mu des saraxe buy wéy, walla xam-xam bu ñuy jariñoo, walla doom ju baax ju koy ñaanal».
«إِذَا مَاتَ الْإِنْسَانُ انْقَطَعَ عَنْهُ عَمَلُهُ إِلَّا مِنْ ثَلَاثَةٍ: إِلَّا مِنْ صَدَقَةٍ جَارِيَةٍ، أَوْ عِلْمٍ يُنْتَفَعُ بِهِ، أَوْ وَلَدٍ صَالِحٍ يَدْعُو لَهُ».
Yonnente bi day xibaare ne jëfi aji-faatu ji day dagg cig faatoom, du am ay yiw ginnaaw ba mu faatoo ba mu des ñatti mbir ndaxte moom mooy sabab bi: Bi ci njëkk: sarax boo xam ni yool ba day sax, niki Wàqf, ak tabax jàkka, ak gas teen, ak yeneen. Ñaareel bi: xam-xam bu nit ñi di jariñoo, niki taalif ay téerey xam-xam, walla mu jàngal nit, nit kooka di tasaare xam-xam bi ginnaaw ba mu faatoo. Ñatteel bi: doom ju baax ju gëm di ñaanal ay way-juram.
Woroom xam-xam yi dëppoo nañu ne bokk na ci liy egg ci nit ki cib yool ginnaaw bi mu faatoo: sarax buy wéy, ak xam-xam bu ñuy jariñoo, ak ñaan, aj it ñëw na ci yeneeni hadiis.
Dañoo tudd ñatt yii kese ci hadiis bii; ndaxte ñooy cosaani yiw, te mooy li ñu baax ñi di gën a bëgg a bàyyi seen ginnaaw.
Lépp lu ñuy jariñoo dana am yiw, waaye la nekk ca bopp ba ak njobbaxtal la mooy xam-xamu sariiha ak xam-xam yi koy dëgëral.
Xam-xam moo ëpp njariñ ci ñatt yii; ndax xam-xam nit ki ko jàng da ciy jariñu, xam-xam lañuy sàmme sariiha, njariñu nit ñépp a ngi ci, te moo gën a daj gën matale ndaxte ci sa xam-xam la ñi fekke sa dund di jariñoo ak ñiy ñëw ginnaaw bi nga fatoo.
Ñaaxe ci yar xale yu baax; ndax ñoom ñooy jariñ seen i way-jur ca allaaxira, te bokk ci seen ug jariñ ñu leen di ñaanal.
Ñaaxe ci rafetal jëme ci ñaari way-jur ginnaaw ba ñu faatoo, te dafa bokk ci rafetal giy jariñ doom ji batay.
Ñaan day jariñ ki faatu donte jugewul ci doom, wànte dañoo tudd doom kese ndaxte moom mooy wéy di ñaanal nit ki fàddu ba keroog mu fiy jóge moom.
Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1255) (1631).
Yataal gi (1)
البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (28/ 413).
Cited in books
10 BooksYataal gi (10)
- التوحيد في ضوء عقيدة الإمام الشافعي رحمه الله ونصوصه ومروياته" إذا مات الإنسان انقطع عنه عمله إلا من ثلاثة: إلا من صدقة جارية، أو علم ينتفع به، أو ولد صالح يدعو له ".([100])
- الذكر والدعاء والعلاج بالرقي من الكتاب والسنة"إذا مات الإنسان انقطع عملُهُ إلا من ثلاثة: إلا من صدقة جاريةٍ، أو علمٍ ينتفع به، أو ولدٍ صالحٍ يدعو له" .
- الصيام ومجموعة أسئلة في أحكامه«إِذَا مَاتَ الْإِنْسَانُ انْقَطَعَ عَمَلُهُ إِلَّا مِنْ ثَلَاثَةٍ: إِلَّا مِنْ صَدَقَةٍ جَارِيَةٍ، أَوْ عِلْمٍ يُنْتَفَعُ بِهِ، أَوْ وَلَدٍ صَالِحٍ يَدْعُو لَهُ»[72].
- المنتقى من المتجر الرابح في ثواب العمل الصالح - المعتمدالمنتقى من المتجر الرابح في ثواب العمل الصالح“إذا مات الإنسان انقطع عنه عمله إلا من ثلاث: صدقة جارية، أو علم ينتفع به، أو ولد صالح يدعو له”.
- رياض الصالحينرياض الصالحين مع فوائد وهدايات - 5«إذَا مَاتَ الإنسانُ انْقَطَعَ عَنْه عَمَلُهُ إلَّا من ثلاث: صَدَقَةٍ جَاريَةٍ، أوْ عِلْمٍ يُنْتَفَعُ به، أوْ وَلَدٍ صَالحٍ يَدْعُو لَهُ».
- عقائد الشيعة الاثني عشرية - سؤال وجواب(إذا ماتَ الإنسانُ انقَطَعَ عنهُ عَمَلُهُ إلا مِن ثلاثةٍ: إلاَّ من صَدَقَةٍ جاريةٍ، أو علمٍ يُنتفَعُ بهِ، أو وَلَدٍ صالحٍ يَدْعُو لهُ)[3]،
- مجموعة زاد الحديث(2)1«إِذَا مَاتَ الْإِنْسَانُ انْقَطَعَ عَنْهُ عَمَلُهُ إِلَّا مِنْ ثَلَاثَةٍ: إِلَّا مِنْ صَدَقَةٍ جَارِيَةٍ، أَوْ عِلْمٍ يُنْتَفَعُ بِهِ، أَوْ وَلَدٍ صَالِحٍ يَدْعُو لَهُ».
- مجموعة زاد الحديث(2)1(إِذَا مَاتَ الْإِنْسَانُ انْقَطَعَ عَنْهُ عَمَلُهُ)
- مجموعة زاد الحديث(2)1(إِذَا مَاتَ الْإِنْسَانُ انْقَطَعَ عَنْهُ عَمَلُهُ إِلَّا مِنْ ثَلَاثَةٍ...)
- نبراس طالب (5)1«إِذَا مَاتَ الْإِنْسَانُ انْقَطَعَ عَنْهُ عَمَلُهُ إِلَّا مِنْ ثَلَاثَةٍ: إِلَّا مِنْ صَدَقَةٍ جَارِيَةٍ، أَوْ عِلْمٍ يُنْتَفَعُ بِهِ، أَوْ وَلَدٍ صَالِحٍ يَدْعُو لَهُ»