Skip to content

«Ngëm juróom-ñaar fukki xaaj la ak lu topp» wala: «juróom-benn fukki xaaj la ak lu topp» - ci ay xaaj, bi ci gën a kawe: mooy wax: laa ilaaha illal Illa Laahu, bi ci gën a suufe, mooy: randale aw lor ci kaw yoon wi

Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónenteb Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

«Ngëm juróom-ñaar fukki xaaj la ak lu topp» wala: «juróom-benn fukki xaaj la ak lu topp» - ci ay xaaj, bi ci gën a kawe: mooy wax: laa ilaaha illal Illa Laahu, bi ci gën a suufe, mooy: randale aw lor ci kaw yoon wi, te kersa benn pàcci la ci ngëm»

«الْإِيمَانُ بِضْعٌ وَسَبْعُونَ -أَوْ بِضْعٌ وَسِتُّونَ- شُعْبَةً، فَأَفْضَلُهَا قَوْلُ لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ، وَأَدْنَاهَا إِمَاطَةُ الْأَذَى عَنِ الطَّرِيقِ، وَالْحَيَاءُ شُعْبَةٌ مِنَ الْإِيمَانِ».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne ngëm ay xaaj la ak i melo yu bari, te day làmboo jëf yi ak pas-pas yi ak wax yi. Ak ne li gën kawe ci ngëm te gën ca mooy wax: «laa ilaaha illal laahu» te xam maanaama , tey jëfe lamu làmboo, ci ne Yàlla moom mooy Yàlla miy kenn mooy ki yayoo ag jaamu moom dong deesul jaamu leneen. Ak ne jëf ji gën a tuuti ci ngëm, mooy randale lépp luy lor nit ñi ci yoon yi. Yónente bi xibaare na ci ne lii di kersa ci meloy ngëm la bokk, jikko la juy waral def lu rafet te bàyyi lu ñaaw.

Maanaay baat yi

بِضْع: من ثلاثة إلى تسعة.

شعبة: خصلة.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ngëm ay tolluwaay la yoo xam ne dañoo gënante.

Ngëm wax la ak jëf ak pas-pas.

Am kersa ci Yàlla mu kawe mi day waral: ba du la gis ci li mu la tere, du la ñàkk a gis it ci li mu la digal.

Tudd lim bi tekkiwul ne ag tënk la, waaye day tegtale ne jëfi ngëm yi dafa bari, Araab yi danañu tuddal mbir mi ab lim waaye bëgguñoo dàq leen lu dul moom.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 11) (9).

Téere Muslim bi gën a wér (1/ 63) (35).

Yataal gi (7)

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين (1/ 154).

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (2/ 169).

تطريز رياض الصالحين.

لفيصل آل مبارك (ص106).

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم لهلالي (1/ 205).