Skip to content

«ku gàddu ngànaay jëme sunu kaw kooku bokkul ci nun».

Jële na ñu ci Abuu Muusa Al-hasrii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

«ku gàddu ngànaay jëme sunu kaw kooku bokkul ci nun».

«مَنْ حَمَلَ عَلَيْنَا السِّلَاحَ فَلَيْسَ مِنَّا».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day moytondikuloo di gàddu ngànnaay ci kaw jullit ñi, ngir ragal loo leen, walla siif leen, ku def loolu ci lu dul yoon, kon toggoo na ag tooñ gu rëy, ak bàkkaar bu mag, te yayoo na tëkku gu tar gii.

Maanaay baat yi

من حمل علينا السلاح: المقصود به من حمل السلاح؛ لقتال المسلمين أو لإرهاربهم.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Àrtu gu tar ci jullit di rayante ak mbokki jollitam.

Bokk na ci ñaawtéef ak yàq yi gën a rëy ci kaw suuf bocci gànnaay ci kaw jullit ñi, ak di yàq ci raye.

Tëkku googu ñu tudd du làmboo rayante ci dëgg, niki rayante ak way-bew yi, ak yàqkat yi ak ñu mel ni ñoom.

Araamal nañu tiital jullit ñi ci gànnaay mbaa leneen, -doonte sax ci anamug fo la-.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (9/ 49) (7071).

Téere Muslim bi gën a wér (1/ 98) (100).

Yataal gi (8)

خلاصة الكلام شرح عمدة الأحكام.

لفيصل آل مبارك (ص406).

الإفهام في شرح عمدة الأحكام.

لابن باز (ص815).

الإلمام بشرح عمدة الأحكام.

لإسماعيل الأنصاري (2/ 195).

تيسير العلام شرح عمدة الأحكام.

لعبد الله البسام (ص752).