yaw xale bi, tuddal Yàlla, te lekke sa loxo ndeyjoor, te lekk li ne ci sa kanam
Jële na ñu ci Umar Ibn Abii Salamata -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
Bama nekkee xale ci kër Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, nuy lekk sama loxo doon wëreelu ci ndab li, Yónente bi ne ma: « yaw xale bi, tuddal Yàlla, te lekke sa loxo ndeyjoor, te lekk li ne ci sa kanam» booba ba leegi noonu laay lekke.
كُنْتُ غُلَامًا فِي حَجْرِ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، وَكَانَتْ يَدِي تَطِيشُ فِي الصَّحْفَةِ، فَقَالَ لِي رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «يَا غُلَامُ، سَمِّ اللهَ، وَكُلْ بِيَمِينِكَ، وَكُلْ مِمَّا يَلِيكَ» فَمَا زَالَتْ تِلْكَ طِعْمَتِي بَعْدُ.
Umar Ibn Abii Salamata -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, di doomi soxnas Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- Ummu Salamata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- -moom nag kër yónente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc la yaro- da ñuy xibaar ne: dadoon lekk ben bis loxoom di wër fune ci ndab li di fa tibb, Yónente bi daaldi koy xamal ñatti teggini lekk: Bi ci njëkk mooy: wax: "bismil Laahi" booy tàmbalee lekk ga. Ñaareel bi: lekke loxob ndeyjoor. Ñatteel ba: lekk ci sa kanam.
...:
Bokk na ci teggini lekk ak naan wax Bismil Laahi ca tàmbali ga.
Jàngal xale yi ay teggin, rawatina ku nekk ci ron kilifteefug nit.
Ñeewanteg Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ak yaatug dënnam ci jàngal ndaw ñi ak yar leen.
Bokk na ci teggin yi nit ki lekk ci li feete ak moom, lu dul bu nekkee ñam yu wuute kon dana ca sañ a jël.
Sahaaba yi dañu daan taqoo ak li leen Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- yare, te loolu dees na ko jariñoo ci waxi Umar je ne: Ba tay jii noona laay lekke.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (7/ 68) (5376).
(3/ 61) (2092).
Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1599) (2022).
Yataal gi (9)
شرح النووي على مسلم (13/ 193).
توضيح الأحكام مِن بلوغ المرام.
للبسام (5/ 440).
فتح ذي الجلال والإكرام شرح بلوغ المرام.
لابن عثيمين (4/ 616).
منحة العلام في شرح بلوغ المرام.
لعبد الله الفوزان (7/ 439).
شرح رياض الصالحين.
لابن عثيمين (3/ 169).
Cited in books
8 BooksYataal gi (8)
- الذكر والدعاء والعلاج بالرقي من الكتاب والسنة"يا غلام سَمِّ اللهَ، وكل بيمينك، وكل مما يليك" فما زالت تلك طعمتي بعد .
- تحفة الأخيار تحفة الأخيار (ببيان جملة نافعة مما ورد في الكتاب والسنة من الأدعية والأذكار)«يَا غُلَامُ، سَمِّ اللَّهَ، وَكُلْ بِيَمِينِكَ، وَكُلْ مِمَّا يَلِيكَ» [77]
- رياض الصالحينرياض الصالحين مع فوائد وهدايات - 4«سَمِّ اللهَ، وَكُلْ بِيَمِينِكَ، وكُلْ مِمَّا يَلِيكَ»
- ما لا يسع أطفال المسلمين جهله«يَا غُلَامُ، سَمِّ اللَّهَ، وَكُلْ بِيَمِينِكَ، وَكُلْ مِمَّا يَلِيكَ»[115].
- مجموعة زاد التربية الإسلامية (1)، والسيرة النبوبة (1)، والعقيدة (1)، والفقه (1)التربية الأسلامية 1« يا غُلامُ، سمِّ اللّه، وكُلْ بِيمِينِك، وكُلْ مِمّا يلِيك»
- مجموعة زاد التربية الإسلامية (3)، والسيرة النبوية (3)السيرة النبوية (3)«يا غلامُ، سَمِّ الله، وكُلْ بيمينك».
- مشروع منهاج زادكزادك 1 طالب«يَا غُلَامُ، سَمِّ اللهَ، وَكُلْ بِيَمِينِكَ، وَكُلْ مِمَّا يَلِيكَ»
- مشروع منهاج زادكزادك 2 طالب نهائي«يَا غُلَامُ، سَمِّ اللهَ، وَكُلْ بِيَمِينِكَ، وَكُلْ مِمَّا يَلِيكَ»