Skip to content

"aw nit wu jiital jigéen ci seen i bir duñu mucc mukk".

Jële nañu ci Abuu Bakrata yal na ko Yàlla dollee gërëm ne: dégg na Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy wax ne:

"aw nit wu jiital jigéen ci seen i bir duñu mucc mukk".

«لَنْ يُفْلِحَ قَوْمٌ وَلَّوْا أَمْرَهُمُ امْرَأَةً».

Al-buxaariy soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa leeral aw nit wu jiital jigéen ci seen i bir ci àtte walla jiite gu matale walla dag ñooñii duñu am mujj la ñuy wut.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Jigéen yellul ci jiite du caagine àtte ci diggante nit ñi, ak yu ko niru ci jiite yu matale yi, bu dee jiite yi ñu tënk nag niki jiite Waqf walla jirim yi walla jiite jàngukaay ak yu ko niru loolu dara nekku ci.

Leeral lompañi jigéen, ak ne du bokk ak góor ci jiite gu matale gi, ak ne def ko njiit ci yu mel noonu sabab la ci ñàkk a mucc.

Yàlla dafa bind jigéen, def mbindiinam mu wuute ak mbindiinu góor, amna ay bir yoy yellul jigéen di ko taxawe; ndax mbindiinam mi mu jagoo, niki noonu amna ay bir yoy yellul góor di ko taxawe; ndax mbindiinam mi mu jagoo.

Mucc gi ñu dàq: mooy mucc ci làmmiñu waxiinu sariiha, te mooy am yiwu àdduna ak allaaxira, nguur gu naat tekkiwul nit ñi a ngi ci lu Yàlla gërëm, ku nekkul ci topp Yàlla, kooku bokkul ci ñi mucc, doonte dafa nekk ci gën gaa rafetug nekkiin ci liy feeñ ci mbiri àddunaam.

Nekkul ci hasiis bi lenn luy xeeb jigéen, waaye ak jubbanti la ñeel kàttanam jëmale ko ca la wér te méngoo ak moom.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (6/ 8) (4425).

Yataal gi (13)

عمدة القاري شرح صحيح البخاري.

لبدر الدين العيني (14/ 210).

أعلام الحديث (شرح صحيح البخاري) لأبي سليمان الخطابي (3/ 1787).

توضيح الأحكام مِن بلوغ المرام.

لعبد الله البسام (7/ 183).

فتح ذي الجلال والإكرام شرح بلوغ المرام.

لابن عثيمين (2/ 268).

منحة العلام في شرح بلوغ المرام.

لعبد الله الفوزان (3/ 441).

ذخيرة العقبى في شرح المجتبى.

للولوي (1/ 82).

كشف المشكل من حديث الصحيحين.

لابن الجوزي (2/ 16).