"Saleen seen way-faatu yi: laa-i-Laaha illal-Laahu".
Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
"Saleen seen way-faatu yi: laa-i-Laaha illal-Laahu".
«لَقِّنُوا مَوْتَاكُمْ لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ».
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day ñaaxe: ci ñuy wax ak di baamtu kàddug Tawhiid "laa-i-Laaha illal Laahu" vi ki sukuraatu dee dikkal ba keroog mu koy wax, ngir mu nekk waxam ju mujj.
Sopp nañu ñuy sa ki dee gi dikkal.
Sib nañu ñuy baril sa kiy dee dikkal, ak di ko ca taxaw lu bari fekk wax na ko, walla mu ñu xam ci moom loolu; ngir mu bañ a foñ bay wax lu yellul.
An-Nawawii nee na: bu ko waxee benn yoon deesu ko ko baamtul lu dul mu waxa jeneen wax ginnaawam, ñi gaaralaat ko ko ngir mu nekk mujjanteelu waxam.
Hadiis bi day làmbo teew ci ki dee dikkal ngir fàttali ko ak wéttali ko ak gëmm ay bëtam ak taxaw ci ay àqam.
Yoonaleesul sa ga ginnaaw bu deewee ak ca bàmmeel ba ginnaaw bi ñu ko suulee; ngir Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc deful loolu.
Téere Muslim bi gën a wér (2/ 631) (916).
Yataal gi (1)
المفهم لما أشكل من تلخيص كتاب مسلم (2/ 569).
Cited in books
4 BooksYataal gi (4)
- الخطب المنبريةموسوعة الخطب المنبرية (القسم الثالث)«لَقِّنُوا مَوْتَاكُمْ لَا إِلٰهَ إِلَّا اللَّهُ»
- الخطب المنبريةموسوعة الخطب المنبرية (القسم الثالث)«لَقِّنُوا مَوْتَاكُمْ: لَا إِلٰهَ إِلَّا اللَّهُ»
- الدروس المهمة لعامة الأمة«لَقِّنُوا مَوْتَاكُمْ: لَا إِلَهَ إِلَّا اللَّهُ»[7]
- رياض الصالحينرياض الصالحين مع فوائد وهدايات - 5«لَقِّنُوا مَوْتَاكُمْ لا إلهَ إلَّا اللهُ».