«am doole nekkul ci bëre daan, waaye ku am doole mooy kiy tëye boppam bu meree».
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:
«am doole nekkul ci bëre daan, waaye ku am doole mooy kiy tëye boppam bu meree».
«لَيْسَ الشَّدِيدُ بِالصُّرَعَةِ، إِنَّمَا الشَّدِيدُ الَّذِي يَمْلِكُ نَفْسَهُ عِنْدَ الْغَضَبِ».
Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ci ne doole dëgg du dooley yaram, mbaa doole juy daan ñeneen nit ñu am doole, waaye ku am doole mooy kiy xeex ak bakkenam te man a not saytaane bu meree.
...:
Bokk na ci njariñal adiis bi : gëneelu lewet ak téye sa bopp boo meree, ndaxte daa bokk ci jëf yu sell yi nga xam ne Lislaam da ciy soññee.
Xeex ak sa bàkkan boo meree moo gën a tar xeex ak noon bi.
Lislaam dafa soppi la ceddo ya jàppe woon , mu nekk jikko ju baax, kon nit ki ëpp kàttan mooy kiy téye boppam bu meree.
Sori mer; ngir li muy waral ci lor nit ki ak mbooloo mi.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (8/ 28) (6114).
Téere Muslim bi gën a wér (4/ 2014) (2609).
(538).
Yataal gi (7)
منحة العلام في شرح بلوغ المرام.
لعبد الله الفوزان (10/ 198).
توضيح الأحكام من بلوغ المرام.
للبسام (7/ 394).
نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.
بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.
للهلالي (1/ 698).
Cited in books
4 BooksYataal gi (4)
- الحديث زاد 4الحديث 4«لَيْسَ الشَّدِيدُ بِالصُّرَعَةِ، إِنَّما الشَّدِيدُ الذي يَمْلِكُ نَفْسَهُ عِنْدَ الغَضَبِ».
- الذكر والدعاء والعلاج بالرقي من الكتاب والسنة"ليس الشديد بالصُّرَعَةِ إنما الشديدُ الذي يملك نفسه عند الغضب" .
- رياض الصالحينرياض الصالحين مع فوائد وهدايات - 1 «لَيْسَ الشدِيدُ بالصُّرَعةِ، إنَّمَا الشَّديدُ الَّذِي يَمْلِكُ نَفْسَهُ عَنْدَ الْغَضَبِ».
- رياض الصالحينرياض الصالحين مع فوائد وهدايات - 3«لَيْسَ الشَّدِيدُ بِالصُّرْعَةِ، إنَّمَا الشَّدِيدُ الَّذِي يَمِلكُ نَفْسَهُ عِنْدَ الغَضَبِ».