Skip to content

"yaw Bilaal, wax ma jëf joo gën am yaakaar joo def ci lislaam

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa wax Bilaal ci jullig fajar ne ko:

"yaw Bilaal, wax ma jëf joo gën am yaakaar joo def ci lislaam, ndax man dégg naa fëggug say dàll ca sama kanam ca àjjana" mu ne ko: jëfuma jenn jëf ju ma gën a am yaakaar ne man masumaa laab genn laab, ci guddi walla bëccëg, lu dul ne julli naa ci laab googu lu ñu dogal ci man ma julli ko.

«يَا بِلاَلُ، حَدِّثْنِي بِأَرْجَى عَمَلٍ عَمِلْتَهُ فِي الإِسْلاَمِ، فَإِنِّي سَمِعْتُ دَفَّ نَعْلَيْكَ بَيْنَ يَدَيَّ فِي الجَنَّةِ» قَالَ: مَا عَمِلْتُ عَمَلًا أَرْجَى عِنْدِي أَنِّي لَمْ أَتَطَهَّرْ طَهُورًا، فِي سَاعَةِ لَيْلٍ أَوْ نَهَارٍ، إِلَّا صَلَّيْتُ بِذَلِكَ الطُّهُورِ مَا كُتِبَ لِي أَنْ أُصَلِّيَ.

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa gis Bilaal ca àjjana ci ay nelaw, mu ne Bilaal ibn Rabbaah: wax ma jëfu coobare joo gën a am yaakaar joo def ci lislaam? Ndax man dégg naa kàddu gu woyof ñeel sa dàll yi bu ñuy yëngu ci booy dox ca àjjana. Bilaal ne ko: jëfuma jenn jëf ju gën a yaakaaru ci man ne masumaa tojle ci wenn waxtu guddi walla bëccëg lu dul ne jàppu naa, toppa julli ci njàppu mooma ñeel sama Boroom ay naafila yu ñu boyal li ñu bind ci man ma julli ko.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ngëneelu jëf ji Bilaal tegtale yal na ko Yàlla dollee gërëm, te mooy di julli saa su laabee daal di jàppu, ak ne moo gën a yaakaaru ci jëf yi, te sabab la ci dugg àjjana.

Sopp nañu julli ci ginnaaw njàppu mu ne.

Royukaay bi walla yarkat bi di laaj ndongaam; ngir ñaax ko ci sax ca bu dee lu rafet la, lu ko mou mu tere ko ko

Seedégg Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñeel Bilaal ne ci waa àjjana la bokk.

Laaj bi ci jullig fajar la, te lii junj la ci ne loolu ci gisug nelaw la gu Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc gis, te géntug Yonnente yi dëgg la.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (2/ 53) (1149).

Téere Muslim bi gën a wér (4/ 1910) (2458).

Yataal gi (2)

عمدة القاري شرح صحيح البخاري (7/ 206).

إرشاد الساري لشرح صحيح البخاري (2/ 326).