Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

7 of 732 cards

Clear filters
«bu ñu doon jox nit ñi ci seen i wootewoo kon ay nit danañu wootewoo alali nit ñi ak seen dereet, waaye kiy wootewoo daa war a indi firnde, kiy weddi daa war a giñ. ».
Wér na Al-Bayhaqii moo ko soloo
التصنيف الشرعيالدعاوى والبيِّنات
"bu ñu doon jox nit ñi ci liñuy wootewoo kon ay nit danañu wootewoo alali nit ñi ak seen dereet, waaye kiy wootewoo daa war a indi firnde, kiy weddi daa war a giñ".
Tane na Al-Bayhaqii moo ko soloo ak ñeneen kem nii, te lenn ci moom mi ngi ci ñaari Sahiih yi.
التصنيف الشرعيالدعاوى والبيِّنات، الأربعون النووية
"Yàlla jéggal na samaw xeet njuumte ak fàtte ak lu ñu leen forse".
An-Nawawii nee na hadiis bu rafet la Ibn Maaja ak Al-Bayhaqii ñoo ko soloo ak ñeneen.
التصنيف الشرعيالأربعون النووية، الإيمان بالله عز وجل
"deeleen joxante Àddiya kon dangeen bëggante".
Tane na Al-Buxaarii soloo na ko ci Al-Adabul Mufrad ak Abuu Yahlaa ak Al-Bayhaqii
التصنيف الشرعيالهبة والعطية
"moytuleen salte yii Yàlla tere, ku ca laal na suturawu ci surutas Yàlla, te tuub jëm ci Yàlla, ndaxte ku ñu wuññil ay bootam dananu teg ci moom Téereb Yàlla mu màgg mi"
Wér na Al-Haakim ak Al-Bayhaqii ñoo ko soloo
التصنيف الشرعيالتوبة
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc musul a xeex ak i nit ba keroog mu leen di woo.
Wér na Ahmad ak Al-Bayhaqii ñoo ko soloo.
التصنيف الشرعيأحكام ومسائل الجهاد وآدابه
"dañu ma a yónni ngir ma mottali jikkó yu tedd yi".
Tane na Al-Buxaarii soloo na ko ci Al-Adabul Mufrad ak Ahmad ak Al-Bayhaqii
التصنيف الشرعيالأخلاق الحميدة