Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

16 of 732 cards

Clear filters
"ku def dara ba ab gétéñ war ca ñu gaaw koo mbugal ci àdduna, Yàlla moo gën a maanu ba du mbugalaat jaamam bi ca allaaxira, waaye ku def luy waral ab gétéñ Yàlla suturaal ko jéggal ko, Yàlla moo gën a tedd ba du delluwaat ci dara lu mu jéggale woon".
Tane na At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja.
التصنيف الشرعيالحدود
"seen Boroom de Ku bari kersa la ku tedd la, dana kersawu ci jaam bi bu yëkkëtee loxoom jëme ci moom mu koy ba ña jox".
Tane na Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja.
التصنيف الشرعيآداب الدعاء
«Li gën ci sikar yi: Laa ilaaha illal Laahu, li gën ci ñaan yi: Alhamdu lil Laahi».
Tane na At-tirmisiy soloo na ko, ak An-nasaa'iy ca Al-kubraa, ak Ibnu Maaja.
التصنيف الشرعيالأذكار المطلقة، أنواع الدعاءموضوعات الحديثالدعاء، الذِّكْر
"bokk na ci jihaad yi gën a màgg wax kàddug maanute fi kanamu buur bu jeng ».
Dafa rafet ngir weneen wu dul moom Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
التصنيف الشرعيفضل الأمر بالمعروف والنهي عن المنكر
"loo xam ne lu bareem day màndiloo kon lu néewam dafa araam".
Tane na Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
التصنيف الشرعيالأشربة المحرمة
"deeleen baril lu ngeen di tudd liy màbb bànneex yi" maanaam dee.
Tane na At-Tirmisiyyu ak An-Nasaa-iyyu ak Ibn Maaja ñoo ko soloo.
التصنيف الشرعيذم حب الدنيا
Moom bu daan xëy day wax: "Allahuma bika asbahnaa, wa bika amsaynaa, wa bika nahyaa, wa bika namuutu, wa ilayka anusuuru" bu gontee daal di wax: "bika amsaynaa wa bika asbahnaa, wa bika nahyaa, wa bika namuutu, wa ilayka anusuuru" wax na it beneen yoon: "wa ilayka almasiiru".
Tane na Abuu Daawuda ak An-Tirmisiyyu ak An-Nasaa-iyyu ci Al-Kubraa, ak Ibn Maaja ñoo ko soloo.
التصنيف الشرعيأذكار الصباح والمساء
"Àdduna de luñu rëbb la, rëbb it li ci biiram, ba mu des tudd Yàlla ak lu ko niru ak boroom xam-xam walla kiy sàkku xam-xam".
Tane na At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja.
التصنيف الشرعيذم حب الدنيا