Skip to content
732 Hadiths

Encyclopedia of Prophetic Hadiths

Filter results

104 of 732 cards

Clear filters

Narrator

Show all narrators (52)
Mu jële ci yenn soxnay Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc -Abuu Haamir nee na, Naafih nee na: Hafsatu wan na ko- ne moom dañu ko a laaj njàngum Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: manuleen ko, nee na: ñi ne ko: wax nu ko. Nee na: mu jàng njàng moom da cee diib Abuu Haamir nee na: Naafih nee na: Ibn Abii Mulaykata jàngal nu {Alhamdu lil-Laahi Rabbil haalamiina} [Al-Faatiha: 1] topp mu taxaw {Ar-Rahmaani Ar-Rahiimi} [Al-Faatiha: 2] topp mu taxaw {Maaliki yawmid diini}.
Wér na Ahmat soloo na ko.
"ku bàyyi ñatti àjjuma ngir woyofal ko Yàlla dana tàppe xolam".
Wér na Abuu Daawuda ak At-Tirmisiyyu ak An-Nasaa-iyyu ak Ibn Maaja ak Ahmad ñoo ko soloo.
«ku lekk aw ñam daal di wax: maa ngi sant Yàlla mi ma leel lii, wërsëgale ma ko ci lu dul benn pexe bu bawoo ci man du caagine kàttan, kon dees na ko jéggal li jiitu ci ay bàkkaaram».
Tane na Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa téye ci loxoom, ne ko: "yaw Muhaas, waat naa ci Yàlla ne dama laa bëgg", mu ne ko: "maa ngi lay dénk yaw Muhaas bul bàyyi mukk di wax ginnaaw julli gu ne: Allaahuma ahinnii halaa sikrika wa sukrika wa husni hibaadatika".
Wér na Abuu Daawuda ak An-Nasaa-yyu ak Ahmad ñoo ko soloo
"kenn ci yéen bu mu ragal nit ñi ba baña wax dëgg bu dee gis na ko walla mu xam ko".
Wér na At-tirmisiy soloo na ko, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan na nu jàngal Alxuraan ci gépp anam fii ak nekkul ci janaba.
Tane na Abuu Daawuda ak At-Tirmisiyyu ak An-Nasaa-iyyu ak Ibn Maaja ak Ahmad ñoo ko soloo.
«ki gën a mat ug ngëm ci jullit ñi mooy ki ci gën a rafet jikko, te ki gën ci yéen mooy ki gën ci ay jigéenam».
Tane na Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat.
Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc musul a xeex ak i nit ba keroog mu leen di woo.
Wér na Ahmad ak Al-Bayhaqii ñoo ko soloo.