"dama doon dox fa saasa ma dégg ag kàddu ci asamaan si, ma yëkkëti samag gis, ma gis malaaka ma ma dikkaloon fa Horaa
Jële nañu ci Abii Salamata ibn Abdi Ar-Rahmaan me ne Jaabir ibn Abdallah Al-Ansaarii yal na leen Yàlla dollee gërëm nee na: fekk moo ngi waxtaane dogug soloo ga, mu wax ci waxtaanam wi ne:
"dama doon dox fa saasa ma dégg ag kàddu ci asamaan si, ma yëkkëti samag gis, ma gis malaaka ma ma dikkaloon fa Horaa mu toog ci ag Gàngunaay ci diggante asamaan si ak suuf si, ma ragal ko, ma daal di dellu, di naan: sàngleen ma, Yàlla mu kawe mi wàcce: {éey yaw mi ñuy sàng 1 jugal te xuppe ji 2} ba ci waxam ji {Te it nangay daw bépp bàkkaar} [Al-Mudassir: 5]. Soloo gi daal di bari daal di toppaloo.
«بَيْنَا أَنَا أَمْشِي إِذْ سَمِعْتُ صَوْتًا مِنَ السَّمَاءِ، فَرَفَعْتُ بَصَرِي، فَإِذَا المَلَكُ الَّذِي جَاءَنِي بِحِرَاءٍ جَالِسٌ عَلَى كُرْسِيٍّ بَيْنَ السَّمَاءِ وَالأَرْضِ، فَرُعِبْتُ مِنْهُ، فَرَجَعْتُ فَقُلْتُ: زَمِّلُونِي، فَأَنْزَلَ اللَّهُ تَعَالَى: {يَا أَيُّهَا المُدَّثِّرُ1 قُمْ فَأَنْذِرْ} [المدثر: 2] إِلَى قَوْلِهِ {وَالرُّجْزَ فَاهْجُرْ} [المدثر: 5]. فَحَمِيَ الوَحْيُ وَتَتَابَعَ».
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne fekk moo ngi waxtaane taxawug soloo gi ak ñàkk a wàccam ci tambaleg yónni gi: dama doon dox ci mbeddi Màkka yi fa saasa ma dégg ag kàddu gu bawoo asamaan, ma yëkkëti sama gis, fa saasa ma gis malaaka ma muy Jibriil mi ma dikkaloon ca xuntuw Hiraa wa, mu toog ci ag Gàngunaay ci diggante asamaan si ak suuf si, ma tiit ragal ko, ma dellu ca sama njaboot ne leen: lëmësleen ma ci ab sér. Yàlla mu kawe wàcce: {éey yaw mi ñuy sàng} di ko lëmës ci sér, {jugal} ngir woote {te nga xuppe} àrtul ñi gëmul sa yónnent gi. {sa Boroom} ak sa Yàlla ji ñuy jaamu {màggal ko} sant ko te màggal ko. {say sér} say yére {laabal ko} musal ko ci sobe yi, {yu bon yi} muy jaamu xërëm {moytu ko} bàyyi ko, ginnaaw loolu soloo gi dëgër daal di bari.
Dogug wahyu gi ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci diir bu ndaw ginnaaw bi waxu Yàlla mu kawe mi wàccee: {jàngal}.
Dagan na nit ki waxtaane li ko dal ci nattu ginnaaw ba mu deñee, ngir sant Yàlla mu kawe mi.
Li njëkk a wàcci mooy waxu Yàlla mu kawe mi: {Yaa ayyuhal muddasir} ginnaaw wàccug: {iqra bismi Rabbika allasii xalaxa}.
Yàlla mu Sell mi gënale dafa Yonnenteem bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ba tax mu sëmbartal ci moom ag soloom ci lu dul dog ba keroog muu teqalikoo ak àdduna.
War na ñoo taxaw ci woote jëme ci Yàlla mu kawe mi, ak xupp way-dummóoyu yi ak bégal way-topp yi.
Warees naa laabal yére yi ngir jullii, tegtaloo nañu ci loolu waxu Yàlla mu kawe mi: {say yére laabal ko}.
Gëm malaaka yi lu war la ak li leen Yàlla kàttanal ci ay jëf ak leneen.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (1/ 7-8) (4).
Téere Muslim bi gën a wér (1/ 98) (161).
Yataal gi (2)
البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (4/ 430).
إرشاد الساري لشرح صحيح البخاري (1/ 67).