"Àjjana amna ab maarse bu ñuy dem Àjjuma gu ne
Jële nañu ci Anas Ibn Maalik yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:
"Àjjana amna ab maarse bu ñuy dem Àjjuma gu ne, ngelaw liy juge bëj-gànnaar daal di upp ñu dal ci seen kanam yi ak seen yére yi, ñu daal di gën a rafet gën a taaru, ñuy dellu ca seen njaboot ya fekk seen rafetaay ak seen taar yokk na, seen njaboot gi ne leen: giñ nanu ci Yàlla ne dangeen a gën a rafet gën a taaru, ñoom itam ñu ne leen: yéen itam giñ nanu ci Yàlla ne dangeen a gën a rafet sunu ginnaaw gën a taaru".
«إِنَّ فِي الْجَنَّةِ لَسُوقًا، يَأْتُونَهَا كُلَّ جُمُعَةٍ، فَتَهُبُّ رِيحُ الشَّمَالِ فَتَحْثُو فِي وُجُوهِهِمْ وَثِيَابِهِمْ، فَيَزْدَادُونَ حُسْنًا وَجَمَالًا، فَيَرْجِعُونَ إِلَى أَهْلِيهِمْ وَقَدِ ازْدَادُوا حُسْنًا وَجَمَالًا، فَيَقُولُ لَهُمْ أَهْلُوهُمْ: وَاللهِ لَقَدِ ازْدَدْتُمْ بَعْدَنَا حُسْنًا وَجَمَالًا، فَيَقُولُونَ: وَأَنْتُمْ وَاللهِ لَقَدِ ازْدَدْتُمْ بَعْدَنَا حُسْنًا وَجَمَالًا».
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne Àjjana amna ab bérab bu ñuy daje, amul jënn amul jaay waaye dañu fay jël lu leen soob, dañu fay dem lu ñu nattale ci juróom-ñaari fan yu nekk, ngelawul bëj-gànnar li upp daal di yëngëtu ci seen kanam yi ak seen yére yi, ñu dolli ag rafet ak ug taar, ñu dellu seen njaboot ya fekk seen rafetaay ak seen taar yokk na, seen njaaboot yi ne leen: ñoo ngi giñ ci Yàlla ne dangeen a gën a rafet gën a taaru, ñoom itam ñu ne leen: yéen itam ñoo ngi giñ ci Yàlla ne dangeen a gën a rafet gën a taaru.
Leeral ne waa Àjjana dañuy gën a rafet di gën a taaru.
Hadiis yi day waral ci nit ki muy xemmeem jëf yu baax yu koy eggale ci kër gii.
Dafa tude ngelawul bëj-gànnaar; ndaxte mooy ngelaw li gën a neex ci araab yi ndax da daan indi yiw ak taw.
Ñaaxe ci woote jëme ci Yàlla ci di xemmemloo ci Àjjana ak i xéewalam.
Téere Muslim bi gën a wér (4/ 2178) (2833).
Yataal gi (8)
نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.
لمجموعة من الباحثين (2/ 1290).
بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.
لسليم الهلالي (3/ 347).
تطريز رياض الصالحين.
لفيصل آل مُبَارَك (ص1088).
شرح رياض الصالحين.
لابن عثيمين (6/ 731).