Skip to content

"ndax duma leen xibaar ñi gën ci yéen ak ñi yées ci yéen?"

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu ne Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa taxaw ay not yu toog, ne leen:

"ndax duma leen xibaar ñi gën ci yéen ak ñi yées ci yéen?" Nee na: ñu noppi, mu wax loolu ñatti yoon, jenn waay ne ko: ahakay yaw Yonnente Yàlla bi, wax nu ñi gën ci nun ak ñi yées ci nun, mu daal di ne: "ki gën ci yéen mooy ki ñuy yaakaar yiwam te wóolu ayam, ki yées ci yéen mooy ki ñu yaakaarul ayam te wóoluwuñu ayam".

«أَلاَ أُخْبِرُكُمْ بِخَيْرِكُمْ مِنْ شَرِّكُمْ؟» قَالَ: فَسَكَتُوا، فَقَالَ ذَلِكَ ثَلاَثَ مَرَّاتٍ، فَقَالَ رَجُلٌ: بَلَى يَا رَسُولَ اللهِ، أَخْبِرْنَا بِخَيْرِنَا مِنْ شَرِّنَا، قَالَ: «خَيْرُكُمْ مَنْ يُرْجَى خَيْرُهُ وَيُؤْمَنُ شَرُّهُ، وَشَرُّكُمْ مَنْ لاَ يُرْجَى خَيْرُهُ وَلاَ يُؤْمَنُ شَرُّهُ».

At-tirmisiy soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa taxaw ci ay nit yu bokk ci sahaaba yi yu toog mu laaj leen, ndax duma leen xamal fàttali leen kan moo gën ci yéen ak kan moo yées ci yéen? Waxuñu tontuwuñu dara, ngir ragal mu ràññale ki gën ci ñoom ki yées ci ñoom ñu ragal gàcca daal di noppi. Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc baamtu laaj bi ñatti yoon, jenn waay ci ñoom tontu ko: ahakay yaw Yonnente Yàlla bi, xibaar nu ki gën ci nun ak ki yées ci nun. Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc leeralal leen: ne ki gën ci yéen mooy ñuy xaar di yaakaar ci moom yiw ak rafetal ak lu baaxam, te wóolu ayam deesul ragal muy bew ak ñaawal ak tooñ, waaye ki yées ci yéen mooy ki ñu yaakaarul te xaaruñu te xemmemuñu ci mooy yiw ak rafetal ak ug mbaax, wóoluwuñu it ci moom ayam, waaye dañuy ragal bewam ak ñaawalam ak tooñam.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Leeral ki gën ci nit ñi ak ki yées ci ñoom.

Njariñ ak lor wuy jeggi jàll moo gën a màgg biy gàtteñlu.

Ñaaxe ci rafet jikko, ak rafet jëflante ci diggante nit ñi, ak àrtu ci bew ak ay ak noonoo.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (4/ 98) (2263).

Yataal gi (2)

التيسير بشرح الجامع الصغير (1/ 395).

تحفة الأحوذي (6/ 445).