Skip to content

«bàkkaar yu mag yi mooy: bokkaale Yàlla, ak dënge ñaari way-jur, ak ray bakkan, ak giñ guy nuuralaate».

Jële na ñu ci Abdulaa Ibn Amr Ibnul Haas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

«bàkkaar yu mag yi mooy: bokkaale Yàlla, ak dënge ñaari way-jur, ak ray bakkan, ak giñ guy nuuralaate».

«الْكَبَائِرُ: الْإِشْرَاكُ بِاللهِ، وَعُقُوقُ الْوَالِدَيْنِ، وَقَتْلُ النَّفْسِ، وَالْيَمِينُ الْغَمُوسُ».

Al-buxaariy soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral bàkkaar yu mag yi, te mooy gu ñu tëkku aji-def ji ci tëkku gu tar ci àdduna walla allaaxira. Bu njëkk bi "Bokkaale Yàlla": te mooy def wenn xeetu jaamu ñeel ku dul Yàlla, ak yamale lenn ak Yàlla ci lu Yàlla jagoo, cig jaamu, ak ug moomeelam ak ci ay turam ak i meloom. Ñaareel bi "Dënge ñaari way-jur": te mooy lépp luy waral lor ñaari way-jur moo xam wax la walla jëf, ak bàyyee rafetal jëme ci ñoom ñaar. Ñatteel bi "ray bakkan": ci lu dul dëgg, niki ray ko cig tooñ ak ug jalgati. Ñenteel bi "ngiñ luy nuural nit ": te mooy giñ lu waay def di fen te xam ne day fen, dañu koo tudde loolu nag; ngir ne day nuural boroomam ci ay bàkkaar walla ci sawara.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ngiñ luy nuuralaate amul lu koy kaffaara; Ndax daa bari loraange ak i ñaawtéef, moo tax fàwwu ñu tuub ko.

Ñenti bàkkaar yu mag yi ñu tudd ci hadiis bi du ngir tënk ko ca waaye day wane ne séen i bàkkaar daa màgg lool.

Bàkkaar yi daa séddalikoo yu mag ak yu ndaw, yu mag yi nag mooy: bépp bàkkaar bu am mbugalum àdduna, niki géten ak móolu, walla tëkkug allaaxira, niki tëkku ci dugg sawara, yu mag yi itam ay daraja la yenn yi moo gën a rëy araamug yeneen yi, bàkkaar yu ndaw yi nag mooy yi nekkul yu mag rekk.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (8/ 137) (6675).

Yataal gi (7)

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (1/ 408).

رياض الصالحين للنووي (ص125) (337).

كنوز رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (5/ 610).

تطريز رياض الصالحين.

لفيصل آل مبارك (ص964).