Skip to content

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan wax ci diggante ñaari sujjóot yi: «Allaahumma ixfir lii, warhamnii, wa haafinii, wahdinii, warsuqnii».

Jële na ñu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- da daan wax ci diggante ñaari sujjóot yi: «Allaahumma ixfir lii, warhamnii, wa haafinii, wahdinii, warsuqnii».

كان النبي صلى الله عليه وسلم يقول بين السجدتين: «اللَّهمَّ اغْفِرْ لي، وارْحَمْنِي، وعافِني، واهْدِني، وارزقْنِي».

Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ibnu Maaja, ak Ahmat.
Tane na bees sukkandikoo ci yeneen yi koy dëggal
Leeral gi

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daa na ñaan ci diggante ñaari sujjóot yi ci julli gi juróomi ñaan yii nga xam ne jullit bi da cee am aajo ju màgg, te mu làmboo yiwi àdduna ak allaaxira, ci sàkku njéggal ak suturaal bàkkaar yi te baal ka ko, ak sotti ko yërmànde, ak mucc ci lënt-lënt yi ak bànneex yi ak feebar yi ak wopp yi, te ñaan Yàlla ag gindi ñeel dëgg te sax ca, ak wërsëgu gëm ak xam-xam ak jëf ju baax, ak alal ju dagan te teey.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Yoonalees na ñaan gii ci toogaay bi nekk ci diggante ñaari sujjóot yi.

Ngëneelu ñaan yii ngir li mu làmboo ci yiwi àdduna ak allaaxira.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (2/ 138) (850).

Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (1/ 317) (284).

Téere Sunna yi bu Ibnu Maaja (2/ 64) (898).

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (5/ 72) (2895).

Yataal gi (6)

مشكاة المصابيح.

للتبريزي (1/ 283).

سبل السلام شرح بلوغ المرام.

لمحمد الصنعاني (1/ 274).

توضيح الأحكام مِن بلوغ المرام.

لعبد الله البسام (2/ 240).