Skip to content

Lalu Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci der la woon, biir gi nekkoo ay box

Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:

Lalu Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ci der la woon, biir gi nekkoo ay box, ñëw na ci Muslim: ñegeñaay bi Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan wéeru ci der la woon biir gi di ay xob.

كَانَ فِرَاشُ رَسُولِ اللَّهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ مِنْ أَدَمٍ، وَحَشْوُهُ مِنْ لِيفٍ، وَلِمُسلمٍ: كَانَ وِسَادَةُ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ الَّتِي يَتَّكِئُ عَلَيْهَا مِنْ أَدَمٍ حَشْوُهَا لِيفٌ.

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Ndayu jullit ñi Aysatu yal na ko Yàlla dollee gërëm, day xibaare ne lal bi Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan nelawe ci der bu ñu wulli lañu ko defar, ñu feesale ko xobi garabu tàndarma, noonu la ñegeñaayam bi mu daan wéeru mel.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Leeral ni Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nekke woon ci dëddu ak dummooyu neexiti àdduna , ànd ak ne Yàlla mu Sell mi jàppandilal na kl loolu bu ko neexoon mu bànneexu ca.

Wut lal ak ay ñegeñaay dagan na, ak nelaw ca kawam ak féexlu ca.

Jaadu na ci jullit bi mu jàppe nekkiinam ak dundam kem nekkiinu Yonnenteem yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, moom mooy royukaay ba rafet, te ku roy ci ay jeexitalam dindiku na texe na àdduna ak allaaxira.

Xér ci waajal allaaxira, ak ne doy na sëkk jullit bi ci àdduna lu koy dimbali ci topp Yàlla, ak mu bañ a soxlawoo di ca barilante, Yàlla ŋàññ na ay nit daal di ne: {barilante soxlaal na leen ba ngeen dem ca bàmmeel ya} [At-Takaasuru: 1-2].

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (8/ 97) (6456).

Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1650) (2082).

Yataal gi (4)

البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (34/ 662).

إرشاد الساري لشرح صحيح البخاري (9/ 264).

المفهم لما أشكل من تلخيص كتاب مسلم (5/ 403).

النهاية في غريب الحديث والأثر (971).