Skip to content

"ku takk ab téere bokkaale na".

Jële nañu ci Huqbata ibn Aamir Al-Juhanii-yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne:

Yonnente Yàlla bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-am mbooloo dañoo ñëw ci moom,mu jaayante ak juróom-ñent ñi bàyyi kenn ki,nu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, jaayante nga ak juróom-ñent daal di bàyyi kii? Mu ne:"ab téere la takk",mu dugal loxoom dagg ko,daal di jaayante ak moom,daal di wax ne: "ku takk ab téere bokkaale na".

أَنَّ رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ أَقْبَلَ إِلَيْهِ رَهْطٌ، فَبَايَعَ تِسْعَةً وَأَمْسَكَ عَنْ وَاحِدٍ، فَقَالُوا: يَا رَسُولَ اللهِ، بَايَعْتَ تِسْعَةً وَتَرَكْتَ هَذَا؟ قَالَ: «إِنَّ عَلَيْهِ تَمِيمَةً»، فَأَدْخَلَ يَدَهُ فَقَطَعَهَا، فَبَايَعَهُ، وَقَالَ: «مَنْ عَلَّقَ تَمِيمَةً فَقَدْ أَشْرَكَ».

Ahmat soloo na ko.
Tane na
Leeral gi

Am mbooloo dañoo ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, seenub lim nekkoon fukk,mu jaayante ak juróom-ñent ci ñoom ci Lislaam ak topp, te jaayantewul ak fukkeel bi,ba ñu ko laajee lu tax loolu Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di wax ne: Dafa takk ab boggal, te loolu mooy li ñuy fas walla di ko takk ci ay xor ak leneen ngir jeñ bët walla lor. Waa ji dugal loxoom ca barabu boggal ba daal di koy dagg daal di set ci moom,ci loolu Yonnente bi jaayante ak moom,daal di wax di moytondikuloo ay boggal di leeral ab àtteem: "ku takk boggal bokkaale na".

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ku sukkandiku ci ku dul Yàlla,boroom bi dina jëflànte ak moom ci lu wuuteek bëgg-bëggam.

Fas ne takk boggal sabab la ci jeñ lor ak bët,loolu bokkaale gu ndaw la,bu dee dafa gëm ne moom day jariñ ci jëmmam kon bokkaale gu mag la.

Dellluwaay yi

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (28/ 636) (17422).

Yataal gi (4)

الملخص في شرح كتاب التوحيد.

لصالح الفوزان (ص74).

الجديد في شرح كتاب التوحيد.

لمحمد القرعاوي (ص85).