Skip to content

"ashibil basa, rabban naasi, wasfi Anta As-Saafii, laa sifaa-a illaa sifaa-uka sifaa-an laa yuxaadiru saqaman".

Jële nañu ci Aysatu yaayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:

Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan seeti ku feebar di ko ñaanal day wax: "ashibil basa, rabban naasi, wasfi Anta As-Saafii, laa sifaa-a illaa sifaa-uka sifaa-an laa yuxaadiru saqaman".

كَانَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ إِذَا أَتَى الْمَرِيضَ يَدْعُو لَهُ قَالَ: «أَذْهِبِ الْبَاسَ، رَبَّ النَّاسِ، وَاشْفِ أَنْتَ الشَّافِي، لَا شِفَاءَ إِلَّا شِفَاؤُكَ، شِفَاءً لَا يُغَادِرُ سَقَمًا».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan seeti ku feebar da koy ñaanal daal di wax: Yaw Yàlla sama Boroom dindil mettit wi ak tarug feebar bi, yaw Boroom nit ñi ki leen Bind yor leen, saafaraal aji-feebar jii, tudd naa sag Sell yaw Aji-Saafara ji, maa ngi jottaliku jëm ci yaw ci sa tur wii di Aji-Saafara ji, aji-feebar ji du saafara wu lu dul ci sag saafa, saafara gog du bàyyi jenn jàngoro.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Kiy wéral mooy Yàlla mu màgg mi, bu dee doktoor bi ak garab yi ñoom ñaar ay sabab lañu duñu jariñ du ñu lor lu dul ci ndigalul Yàlla.

Seeti ku feebar dafa bokk ci àq yi dox ci diggante jullit ñi, ci mbokk gi la gën a yaye.

Xemmemloo ci ku seeti ku feebar mu ñaanal ko ñaan gu baarkeel gii ñu tuxal.

Bokk na ci njubug Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di faj jaareko ci moccug sariiha ci Alxuraan ak ay ñaan yu teey, Yonnente bi daan na mocc boppam bu feebaree, niki noonu yit daan na mocc ku tawat ci njabootam ak ñeneen.

Ibn Hajar nee na: jaaxle amna ci lu tax ñuy ñaanal ki feebar ag wér te feebar bi day far ay bàkkaaram di yok yool ni ki mu ñëwe ci hadiis yu bari, tontu bi mooy: ñaan jaamu Yàlla la, te du dàqonte ak am tuyaaba ak far bàkkaar; ndax ñoom ñaar dañuy ame ci njëlbeenu feebar ba ak muñ ga, te aji-ñaan ji moo ngi ci diggante Ñaar yu rafet: benn jubluwaayam am, walla ñu wecceel ko ko ci xëcc njariñ walla jañ lor, te yépp ci ngëneelu Yàlla la.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (7/ 134) (5750).

Téere Muslim bi gën a wér (4/ 1721) (2191).

Yataal gi (8)

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (2/ 162).

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (4/ 477).

كنوز رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (11/ 539).

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (1/ 687).