Skip to content

"Jëf yi mi ngi aju ci yéene yi, te nit ku nekk la mu yéene rekk lay am

Jële nañu ci njiiti jullit ñi baayu Hafsa Umar Ibn Al-Xattaab yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy wax ne:

"Jëf yi mi ngi aju ci yéene yi, te nit ku nekk la mu yéene rekk lay am, képp ku gàddaay ngir Yàlla ak ub Yonenteem, kooku gàddaayam dina jëm ci Yàlla ak Yonenteem, waaye képp ku gàddaay ngir àdduna jum soxlaa jot walla jigéen ju mu bëgg a takk kon gàddaayam jëm na ca la ko tax a gàddaay".

«إنَّمَا الأَعْمَالُ بِالنِّيَّاتِ، وَإِنَّمَا لِكُلِّ امْرِئٍ مَا نَوَى، فَمَنْ كَانَتْ هِجْرَتُهُ إلَى اللَّهِ وَرَسُولِهِ فَهِجْرَتُهُ إلَى اللَّهِ وَرَسُولِهِ، وَمَنْ كَانَتْ هِجْرَتُهُ لِدُنْيَا يُصِيبُهَا أَوْ امْرَأَةٍ يَنْكِحُهَا فَهِجْرَتُهُ إلَى مَا هَاجَرَ إلَيْهِ».

Ñaari imaam yi ci hadiis ñoo ko soloo, ñuy Abuu Abdillaahi Mouhammad ibn Ismaahiil ibn Ibraahiim ibn Al-Muxiirata ibn Bardisba Al-Buxaarii ak Abul Hussayn Muslim ibn Hajjaaj ibn Muslim Al-Xusayrii An-Naysaabuurii, ci seen ñaari téere yu wér yi nga xam ne ñoo gën a wér ci téere yi ñu taalif.
Wér na
Leeral gi

Yónente bi day leeral ne jëf yépp ci yéene ja la aju, te àtte bii daa matale jëf yépp moo xam jaamu yi la mbaa jëflante yi, koo xam ne jëfam njariñ la ci jublu du ca am lu dul njariñ loola waaye du ci am tiyaaba, ko xam ne jëfam jege Yàlla la ci jublu dana am ca jëfam ja ab yool ak ug pay, donte jëf i aada la, niki lekk ak naan. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- joxe waat meneen misaal ci ni yéene di jeexitale ci jëf yi ànd ak seenug niróo ci melo wi feeñ, mu leeral ne ku jublu ci gàddaay bàyyi réewam ngir jublu ci ngërëmal Boroomam kon gàddaayam ga gàddaayu sariiha la gu ñu nangu te dees na ko fay ab yool ngir yéeneem ju dëggu, waaye ku jublu cig gàddaayam njariñal àdduna, alal, ak daraja ak am njaay, walla soxna du am ca gàddaayam ga lu dul njariñ yooya mu yéene woon, te du am benn cér cig pay mbaa ab yool.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ñaaxe ci sellal, ndax Yàlla du nangu jëf lu dul la nga xamne def na ñu ko ngir jëmmam ja.

Jëf yi Nga xamne dees ciy jaar ngir jege Yàlla bu ko muskallaf mi defee ci anamug aada du ca am ab yool, ba keroog mu cay jublu jege Yàlla.

Ci yéene lañuy xàjjalee diggante jaamu gu ne ak geneen ga, ak it diggante jaamu yi ak aada yi.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (9/ 22) (6953).

(1/ 6) (1).

Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1515) (1907).

Yataal gi (8)

التحفة الربانية في شرح الأربعين حديثًا النووية (ص5).

شرح الأربعين النووية.

لابن عثيمين (ص5).

فتح القوي المتين في شرح الأربعين وتتمة الخمسين.

للعباد (ص8).

شرح النووي على مسلم (13/ 54).

تاج العروس من جواهر القاموس.

للزبيدي (7/ 196).