Skip to content

«ñaan deesu ko delloo ci diggante nodd ak liqaam».

Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:

«ñaan deesu ko delloo ci diggante nodd ak liqaam».

«الدُّعَاءُ لاَ يُرَدُّ بَيْنَ الأَذَانِ وَالإِقَامَةِ».

Abóo Daawuda soloo na ko, ak At-tirmisiy, ak An-nasaa'iy.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral ngëneelu ñaan ci diggante nodd ak liqaam, ci ne deesu ko delloo te yeyoo na ñu nangu ko, deeleen ci ñaan Yàlla.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ngëneelu ñaan ci waxtu wii.

Bu kiy ñaan làmboo teggini ñaan, jublu ay barabam ak waxtuy ngëneelam, sori moy Yàlla, moytandikul boppam ci tàbbi ci lënt yi ak ya ñuy sikk-sàkka, daal rafet njort ci Yàlla: kon moom yeyoo na ñu nangul ko ñaanam ci ndigalul Yàlla.

Al-Manaawii wax na ci nangug ñaan gi ne: maanaam: ginnaaw dajaloog sàrti ñaan yi ak i ponkam ak i tegginam, bu ca dara wuutee bu mu yedd ku dul boopam.

Nangu ñaan: benn mu nekk ñu nangul ko ñaanam gi jox ko limu ñaan ci lu gaaw, walla ñu wëlbatil ko ci aw ay wu mel ni moom, walla ñu deñcal ka ko ba allaaxira; loolu nag ci kem xereñug Yàlla ak yërmàndeem.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu At-tirmisiy (1/ 253) (212).

Téere Sunna yi bu Abóo Daawuda (1/ 392) (521).

Téere bu mag bi An-nasaa'iy def ci Sunna yi (9/ 32) (9812).

Yataal gi (10)

الثمر المستطاب في فقه السنة والكتاب.

الألباني (1/ 200).

توضيح الأحكام شرح بلوغ المرام.

لعبد الله البسام (1/ 548).

منحة العلام في شرح بلوغ المرام.

لعبد الله الفوزان (2/ 309).

فتح ذي الجلال والإكرام شرح بلوغ المرام.

لابن عثيمين (1/ 486).

سبل السلام.

لمحمد الصنعاني (2/ 707).