"bàyyileen ko loolu médd la"
Jële nañu Jaabir ibn Abdul Laahi yal na leen Yàlla dollee gërëm mu wax ne:
Nrkkoon nañu ci benn xare jrnn waay ci Muhaajiruun yi dóor ci taat jenn waay ci Ansaar yi, ki bokk ci Ansaar yi ne, maa ngi xettaliku ci yéen Ansaar yi, ki bokk ci Muhaajiruun yi ne: maa ngi xettaliku ci yéen Muhaajiruun yi, Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dégg ko daal di ne: "lii lan la?" Ñu ne ko: jenn waay ci Muhaajiruun yi moo dóor ci taat jenn waay ci Ansaar yi, ki bokk ci Ansaar yi ne: maa ngi xettaliku ci yéen Ansaar yi, ki bokk ci Muhaajiruun yi ne maa ngi xettaliku ci yéen Muhaajiruun yi, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di ne: "bàyyileen ko loolu médd la" Jaabir nee na: Ansaar yi bi Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di ñëw Madiina ñoo ëppoon, ginnaaw ga Muhaajiruun yi daal di bari, Abdulla ibn Ubay daal di ne: waaw ndax ñoo ko def, giñ naa ci Yàlla ne bu ñu delloo Madiina ñu tedd ñi danañu fa génnee ñu doyadi ñi, Umar ibn Al-Xattaab yal na ko Yàlla dollee gërëm daal di ne: yaw Yonnente Yàlla bi, bàyyi ma ma dóor doqu naaféq bii, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: "bàyyi ko, ndax nit ñi bañ a wax naan Muhammat day ray ay àndadoom".
كُنَّا فِي غَزَاةٍ فَكَسَعَ رَجُلٌ مِنَ المُهَاجِرِينَ رَجُلًا مِنَ الأَنْصَارِ، فَقَالَ الأَنْصَارِيُّ: يَا لَلْأَنْصَارِ، وَقَالَ المُهَاجِرِيُّ: يَا لَلْمُهَاجِرِينَ، فَسَمَّعَهَا اللَّهُ رَسُولَهُ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ قَالَ: «مَا هَذَا؟» فَقَالُوا: كَسَعَ رَجُلٌ مِنَ المُهَاجِرِينَ رَجُلًا مِنَ الأَنْصَارِ، فَقَالَ الأَنْصَارِيُّ: يَا لَلْأَنْصَارِ، وَقَالَ المُهَاجِرِيُّ: يَا لَلْمُهَاجِرِينَ، فَقَالَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «دَعُوهَا فَإِنَّهَا مُنْتِنَةٌ» قَالَ جَابِرٌ: وَكَانَتِ الأَنْصَارُ حِينَ قَدِمَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ أَكْثَرَ، ثُمَّ كَثُرَ المُهَاجِرُونَ بَعْدُ، فَقَالَ عَبْدُ اللَّهِ بْنُ أُبَيٍّ: أَوَقَدْ فَعَلُوا، وَاللَّهِ لَئِنْ رَجَعْنَا إِلَى المَدِينَةِ لَيُخْرِجَنَّ الأَعَزُّ مِنْهَا الأَذَلَّ، فَقَالَ عُمَرُ بْنُ الخَطَّابِ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ: دَعْنِي يَا رَسُولَ اللَّهِ أَضْرِبُ عُنُقَ هَذَا المُنَافِقِ، قَالَ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «دَعْهُ، لاَ يَتَحَدَّثُ النَّاسُ أَنَّ مُحَمَّدًا يَقْتُلُ أَصْحَابَهُ».
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa nekkoon ci tukki ci genn xare ànd ak sahaaba yi ñuy Muhaajiruun yi ak Ansaar yi yal na leen Yàlla dollee gërëm, jenn waay ci Muhaajiruun yi dóor tooguwaayu jenn waay ci Ansaar yi ci loxoom. Ki bokk ci Ansaar yi daal di ne: xettalileen ma yéen Ansaar yi, ki bokk vi Muhaajiruun yi ne: xettalileen ma yéen Muhaajiruun yi, Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dégg ko daal di ne: lii lan la? Ñu ne ko: jenn waay ci Muhaajiruun yi moo dóor tooguwaayu jenn waay ci Ansaar yi, ki bokk ci Ansaar ne: xettalileen ma yéen Ansaar yi, ki bokk ci Muhaajiruun yi ne: xettalileen ma yéen Muhaajiruun yi. Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di ne: bàyyileen aaday ceddo yii moom bon la te xasaw tey lore; te mooy nit ki bu ko xóloowaaleem notee mu woo aw nitam ñu gaawanatu ci dimbali ko ci ag réer ak ug par-parloo moo xam moo tooñ walla dañu ko a tooñ. Jaabir nee na: Ansaar yi bi Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di ñëw Madiina di aji-gàddaay ñoo ëppoon, ginnaaw ga Muhaajiruun yi daal bari Boppu naaféq yi Abdulla ibn Ubay ibn Saluul daal di ne: kon mbir mi egg na ci dayo bii?! Giñ naa ci Yàlla ne bu ñu delloo Madiina ñu tedd ñi -mu jublu ci boppam ak ñi ànd ak moom- danañu génne ñu doyadi ñi -mu jublu ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak ñi ànd ak moom-. Umar ibn Al-Xattaab yal na ko Yàlla dollee gërëm daal di ne: yaw Yonnente Yàlla bi, bàyyi ma ma dóor doqug naaféq bii, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: Bàyyi ko, ndax not ñi bañ a wax naan Muhammat day ray ñi ko topp doonte ci li feeñ la.
Tere nañu aada ak cosaani ceddo yi ñu ŋàññ, moo xam wax la walla jëf, lislaam dafa ñëw ngir soreele nit ñi loolu, ak gindi leen jëme leen ci lu jub ak dëgg.
Àrtu ci par-parloo ci neen, te moytu ko mi ngi mel ni moytu am médd mu bon.
Tere nañu lépp luy jeqi ak nooneel ak ug mbañeel.
An-Nawawii nee na: li Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc tudde loolu wooteg ceddo mooy ne dafa bañ loolu, ndax dafa bokk ci li ceddo yi nekkoon ci lënkaloo ci ngiir yi ak mbir àdduna yi ci aju, ceddo daan jël seen i àq ci sababus par-parloo ak ngiur yi, lislaam ñëw yàq loolu, daal di teqle xew-xew yi ci àttey sariiha, bu kenn nit tooñee keneen àttekat bi àtte seen diggante, daal di koy gàll li nooneelam gi laaj kem ni mu saxe ci reegali lislaam.
As-Sindii nee na: mu leeral ne li waral dimbale ga mooy li mu bokk ci ngiir mi kem ni ceddo ga nekke woon ci neen, kon jarul kenn di woo ngiiram, waaye dimbale ci dëgg lu ñu sàkku la te lu day war bépp jullit moo xam ci ngiiram la bokk walla déet.
Li naaféq nekke woon ci ñaaw làmmiñ ak ñeme Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak sahaabaam yi yal na leen Yàlla dollee gërëm.
Li Yonnente bi nekke woon ci tarug lewet ak muñ ci li koy dal ci lori naaféq yi.
Àrtu ci lépp loo xam ne day dawloo nit ñi ñu dugg ci lislaam, loolu moo tax Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bañ a ray naaféq ngir nit ñi bañ a wax naan: Muhammat day ray ay àndadoom.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (6/ 154) (4907).
Téere Muslim bi gën a wér (4/ 1998) (2584).
Yataal gi (4)
النهاية في غريب الحديث والأثر (801) (899).
عمدة القاري شرح صحيح البخاري (19/ 241).
المفهم لما أشكل من تلخيص كتاب مسلم (6/ 560).
البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (40/ 596).
Cited in books
4 BooksYataal gi (4)
- التسليم للنص الشرعي والمعارضات الفكرية المعاصرة04 التسليم للنص الشرعي - الفصل الثالث حتى القصل الرابع"لا يتحدث الناس أن محمداً يقتل أصحابه."
- الصلاة التي علمها النبي ﷺ الصحابة رضي الله عنهم«فَقَامَ عُمَرُ بْنُ الْخَطَّابِ رَضِيَ اللَّهُ عَنْهُ فَقَالَ: الصَّلَاةُ»[650] ،
- مشروع منهاج زادكزادك 3 طالب نهائي«دَعْهُ، لَا يَتَحَدَّثُ النَّاسُ أَنَّ مُحَمَّدًا يَقْتُلُ أَصْحَابَهُ»
- نبراس طالب (3)نبراس طالب 3«دَعْهُ، لاَ يَتَحَدَّثُ النَّاسُ أَنَّ مُحَمَّدًا يَقْتُلُ أَصْحَابَهُ»