Skip to content

"yóbbul sama dàll yii koo dajeel ci ginnaaw miir bii, te muy seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla di ku am kóolute ci xolam, nanga ko bégal ci Àjjana"

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne:

Toogoon nanu fi Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ak Abuu Bakar ak Umar nu nekk ci mbooloo, Yonente jug dem, daal di yeex a ñëw, ba nu ragal ñu dogaale ko wolif nun, nu tëb jug, ma nekk ki njëkk a tëb jëm ci moom, ma génn di wër Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ba ma mujj ñëw ci benn miiru ansaar Banii Najjaar yi, ma wër ko ba xam ndax dinaa fa gis ab bunt? gisuma ko, fa saasa am yol daal di dugg si ci Miir bi jóge ca teenu Xaarijata -am yol mooy am walangaan- ma tëb, ma dugg fi Yonente Yàlla bi, mu wa ne: "kan la Abuu Hurayrata" ma ne : waaw yaw Yonente Yàlla bi, mu ne: "lan mooy sa mbir?" Ma ne ko: dangaa nekkoon sunu biir, nga jug dem daal di Yeex a ñëw, ñu ragal nu dogaale la wolif nun, ñu jàq daal di tëb, man maa njëkk a tëb, te nit ña a ngi sama ginnaaw, mu ne: "yaw Abuu Hurayrata" daal di may jox ñaari dàllam, daal di ne: "yóbbul sama dàll yii koo dajeel ci ginnaaw miir bii, te muy seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla di ku am kóolute ci xolam, nanga ko bégal ci Àjjana", ki ma njëkk a dajeel mooy Umar, mu ne ma: waaw ñaari dàll yii nag yaw Abuu Hurayrata? Ma ne ko lii de ñaari dàlli Yonente Yàlla bi la moo ma yónni jox ma ko ne ma ku ma dajeel muy seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla mu am kóolute ci xolam ma bégal ko ci Àjjana, Umar door loxoom ci diggante sama ñaari ween yi, ma detteelu, mu ne ma dellul yaw Abuu Hurayrata, ma dellu ci Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ma yiket daad di jooy, Umar jiital ma topp sama ginnaaw, Yonente bi daal di ne: "lu la jot yaw Abuu Hurayrata?" Ma ne ko: damaa daje ak Umar ma xibaar ko li nga ma yónni mu dóor ma dóor bu tar ci sama dënn ma detteelu, mu ne ma: dellul, Yonnente bi ne ko: "lan moo la yóbbe li nga def?" Mu ne: yaw Yonente Yàlla bi jote naa la sama baay ak sama yaay, ndax yaa yónni Abuu Hurayrata jox ko sa dàll yi ci ne ku mu dajeel muy kuy seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla di ku ci am kóolute ci xolam mu bégal ko ci Àjjana? Mu ne ko: "waaw", Umar ne ko: bu ko def, ndax damaa ragal nit ñi sukkandiku ci, bàyyileen ñu jëf, Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di ne "kon bàyyileen".

كُنَّا قُعُودًا حَوْلَ رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، مَعَنَا أَبُو بَكْرٍ، وَعُمَرُ فِي نَفَرٍ، فَقَامَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ مِنْ بَيْنِ أَظْهُرِنَا، فَأَبْطَأَ عَلَيْنَا، وَخَشِينَا أَنْ يُقْتَطَعَ دُونَنَا، وَفَزِعْنَا، فَقُمْنَا، فَكُنْتُ أَوَّلَ مَنْ فَزِعَ، فَخَرَجْتُ أَبْتَغِي رَسُولَ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ حَتَّى أَتَيْتُ حَائِطًا لِلْأَنْصَارِ لِبَنِي النَّجَّارِ، فَدُرْتُ بِهِ هَلْ أَجِدُ لَهُ بَابًا؟ فَلَمْ أَجِدْ، فَإِذَا رَبِيعٌ يَدْخُلُ فِي جَوْفِ حَائِطٍ مِنْ بِئْرٍ خَارِجَةٍ - وَالرَّبِيعُ الْجَدْوَلُ - فَاحْتَفَزْتُ، فَدَخَلْتُ عَلَى رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَقَالَ: «أَبُو هُرَيْرَةَ» فَقُلْتُ: نَعَمْ يَا رَسُولَ اللهِ، قَالَ: «مَا شَأْنُكَ؟» قُلْتُ: كُنْتَ بَيْنَ أَظْهُرِنَا، فَقُمْتَ فَأَبْطَأْتَ عَلَيْنَا، فَخَشِينَا أَنْ تُقْتَطَعَ دُونَنَا، فَفَزِعْنَا، فَكُنْتُ أَوَّلَ مَنْ فَزِعَ، فَأَتَيْتُ هَذَا الْحَائِطَ، فَاحْتَفَزْتُ كَمَا يَحْتَفِزُ الثَّعْلَبُ، وَهَؤُلَاءِ النَّاسُ وَرَائِي، فَقَالَ: «يَا أَبَا هُرَيْرَةَ» وَأَعْطَانِي نَعْلَيْهِ، قَالَ: «اذْهَبْ بِنَعْلَيَّ هَاتَيْنِ، فَمَنْ لَقِيتَ مِنْ وَرَاءِ هَذَا الْحَائِطَ يَشْهَدُ أَنْ لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ مُسْتَيْقِنًا بِهَا قَلْبُهُ، فَبَشِّرْهُ بِالْجَنَّةِ»، فَكَانَ أَوَّلَ مَنْ لَقِيتُ عُمَرُ، فَقَالَ: مَا هَاتَانِ النَّعْلَانِ يَا أَبَا هُرَيْرَةَ؟ فَقُلْتُ: هَاتَانِ نَعْلَا رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، بَعَثَنِي بِهِمَا مَنْ لَقِيتُ يَشْهَدُ أَنْ لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ مُسْتَيْقِنًا بِهَا قَلْبُهُ، بَشَّرْتُهُ بِالْجَنَّةِ، فَضَرَبَ عُمَرُ بِيَدِهِ بَيْنَ ثَدْيَيَّ فَخَرَرْتُ لِاسْتِي، فَقَالَ: ارْجِعْ يَا أَبَا هُرَيْرَةَ، فَرَجَعْتُ إِلَى رَسُولِ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ، فَأَجْهَشْتُ بُكَاءً، وَرَكِبَنِي عُمَرُ، فَإِذَا هُوَ عَلَى أَثَرِي، فَقَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «مَا لَكَ يَا أَبَا هُرَيْرَةَ؟» قُلْتُ: لَقِيتُ عُمَرَ، فَأَخْبَرْتُهُ بِالَّذِي بَعَثْتَنِي بِهِ، فَضَرَبَ بَيْنَ ثَدْيَيَّ ضَرْبَةً خَرَرْتُ لِاسْتِي، قَالَ: ارْجِعْ، فَقَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «يَا عُمَرُ، مَا حَمَلَكَ عَلَى مَا فَعَلْتَ؟» قَالَ: يَا رَسُولَ اللهِ، بِأَبِي أَنْتَ، وَأُمِّي، أَبَعَثْتَ أَبَا هُرَيْرَةَ بِنَعْلَيْكَ، مَنْ لَقِيَ يَشْهَدُ أَنْ لَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ مُسْتَيْقِنًا بِهَا قَلْبُهُ بَشَّرَهُ بِالْجَنَّةِ؟ قَالَ: «نَعَمْ»، قَالَ: فَلَا تَفْعَلْ، فَإِنِّي أَخْشَى أَنْ يَتَّكِلَ النَّاسُ عَلَيْهَا، فَخَلِّهِمْ يَعْمَلُونَ، قَالَ رَسُولُ اللهِ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ: «فَخَلِّهِمْ».

Muslim soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonente bi dafa toogoon ag am mbooloo ci sahaabaam yi bokk na ca Abuu Bakar ak Umar, Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di jug dem yeex a ñëwaat, ñu ragal lu bon jóge ci noon bi dal ci kawam; benn ci ñu jàpp ko walla leneen. Sahaaba yi jug jàq lool, Abuu Hurayrata di ki njëkk a dem, ba egg ci benn toolu waa Banii Najjaar, di ko wër ndax amaana mu gis ab bunt bu ñu ubbi fa gisu ko, waaye mu fekk fa ab xar-xar bu ndaw am ndox di fa jaar, mu fexe ba dugg fa fekk fa Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, mu ne ko: kan la Abuu Hurayrata? Mu ne: waaw. Mu ne ko: lan mooy sa mbir? Abuu Hurayrata ne ko: dangaa nekkoon ci sunu biir, nga jug dem, ba noppi yeex a ñëw, nu ragal ne danu laa dogaale wolif nu, nu jug ci ag njàqare, ma nekk ki njëkk a jug, ma ñëw ci miir bii, ma tëb kem ni njàppaan di tëbe, nit ñi nag ñoo ngi sama ginnaaw. Yonente bi jox ko ñaari dàllam ngir mu nekk màndarga ci ag dëggoom, mu ne ko: yóbbul sama dàll yii, koo dajeel ci ginnaaw miir bii te mu seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla, te amul ku ñuy jaamu ci dëgg ku dul Yàlla, muy lu mu am kóolute ci xolam; ku lii nekk meloom kon ci waa Àjjana la bokk. Ki mu njëkk a dajeel di Umar , mu ne ko: waaw, ñaari dàll yii nag yaw Abuu Hurayrata? Mu ne ko: ñaari dàlli Yonente bi la, moo ma moo ma yónni ne ma ku ma dajeel te muy kuy seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla di ku mu am kóolute ci xolam ma bégal ko ci Àjjana. Umar dóor loxoom ci dënnu Abuu Hurayrata mu daanu jaaxaan, mu ne ko: dellul yaw Abuu Hurayrata, ma dellu ca Yonente ba di ku jàq sama kanam soppeeku may waaj a jooy, Umar topp ma di dox ci sama ginnaw. Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: lan moo la jot yaw Abuu Hurayrata? Ma ne ko: damaa daje ak Umar, ma wax ko li nga ma yónni, mu dóor ma ma daanu jaaxaan, mu ne ma dellul. Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di ne: yaw Umar, ana lan moo la yóbbe sa jëf ji? Umar ne ko: yaw Yonente Yàlla bi, jote naa la sama baay ak sama yaay, ndax yaa yónni Abuu Hurayrata, jox ko sa dàll yi, ne ko ku mu dajeel te muy kuy seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla di ku am kóolute ci xolam mu bégal ko ci Àjjana? Mu ne ko: waaw. Nee na: bu ko def, ndax damay ragal nit ñi sukkandiku ci wax ji rekk ci lu dul ñuy jëf, bàyyileen ñu jëf. Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: bàyyileen kon.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Tarug mbëggeelu Sahaaba yi ñeel Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak seenug xér ci ag muccam ci lépp lu ñaaw.

Yoonalees na bégale ci xibaaru mbégte.

Ngëm wax la ak jëf ak pas-pas.

Al-Xaadii Hiyaad ak ñeneen nee nañu: li Umar def di wàqante ak Yonente bi nekkul ak diiŋat walla delloo ndigalam; ndaxte lu mu yónni Abuu Hurayrata dara nekku ci lu dul luy dalal xoli xeet wi ak di leen bégal, Umar gis ne nëbb loolu moo gën ci ñoom te mooy gën a tax duñu bàyyandiku, te mooy tax ñu gën a tàmm yiw ci ñuy sukkandiku ci bégle gi, ba mu ko gaaralee Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu nangul ka ko.

An-Nawawii: nee na: nekk na ci hadiis bi ne imaam bi ak mag mi saa yu ñu gisee dara ñenn ñi ko topp gis lu wuute ak moom; day jaadu ci ki ko topp mu gaaral ko ki mu topp ngir mu xool ko, bu leere ci moom ne li aji-topp ji wax moo gën mooy li baax mu dellu ginnaaw lu ko moy mu leeralal aji-topp ji tontug lënt-lënt gi mu gaaral.

Dagan na ñi bañ a leeral yenn xam-xam yi nga xam ne aajowoo wu ñu ko ngir yéwénal walla ragal ag yàqute.

Bégle gu màgg ñeel na waa Tawhiid, ak ne ku faatu fekk mu seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ku dul Yàlla di aji-sellal ci xolam kooku Àjjana ñeel na ko.

Kàttanu Umar yalna ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak xereñam, ak ag déggam gu yaatu.

An-Nawawii nee na: nekk na ci it me dagan na nit ki dugg ci moomeelu keneen ci lu dul ndigalam bu xamee ne dana gërëm loolu ngir cofeel gi dox seen diggante, walla ngir leneen lu dul loolu.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (1/ 59) (31).

Yataal gi (8)

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (1/ 384).

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (3/ 317).

كنوز رياض الصالحين.

لمجموعة من الباحثين (6/ 563).

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (1/ 495).