"dees na gaaral fitna ci xol yi mu mel ni ag basaŋ nekk bant-bant
Jële nañu ci Husayfata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: nekkoon nanu fi Umar yal na ko Yàlla dollee gërëm, mu wax ne: kan ci yéen moo dégg Yonente Yàlla bi mu tudd fitna yi? Am ñu ne: nun dégg nanu ko, mu ne: amaana ngeen jublu ci fitnay góor gi ci njabootam ak dëkkando? Ñu neko: waaw waaw, mu ne: loolu julli ak woor ak saraxe dana ko far, waaye kan ci yéen moo dégg Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di tudd yi nga xam ne day riir kem ni géej di riire? Husayfata nee na mu noppiloo gaa yi, ma ne ko: dégg naa Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy wax naan:
"dees na gaaral fitna ci xol yi mu mel ni ag basaŋ nekk bant-bant, xol bu mu dugg ñi tomb ca tomb bu ñuul, xol bu ko weddi ñu tomb ca tomb bu weex, ba mu mujj nekk ci ñaari xol, bu weex mel ni xeer wu weex te rittax fitna du ko lor fii ak asamaan yi ak Suuf si mi ngi fi, beneen di xol bu ñuul bu rax, mel ni baag bu jeng, du xam lu baax te du bañ lu bon, lu dul lu dëppoo ak bànneexam", Husayfata nee na: ma wax ko ne, sa diggante ak moom benn bunt bu ñu tëj moo ci dox te daana ka toj na, Umar ne ko: mo ndax day toj? Moom bu ñu ko tijji woon sax amaana dees na ko tëjaat, ma ne ko: déedéet dañu koy toj, ma xibaar ko ne bunt boobu de benn waay la bu ñuy ray walla mu dee balaa yàgg te lii du ay njaxas. Abuu Xaalid nee na: ma wax Sahd ne ko: yaw Abuu Maalik, lan mooy ñuul gu rax? Mu wax ne: mooy weex gu tar gu nekk ci biir ñuulaay, nee na: ma ne ko: lan mooy baag bu jeng? Mu ne: mooy bu dëng.
«تُعْرَضُ الْفِتَنُ عَلَى الْقُلُوبِ كَالْحَصِيرِ عُودًا عُودًا، فَأَيُّ قَلْبٍ أُشْرِبَهَا نُكِتَ فِيهِ نُكْتَةٌ سَوْدَاءُ، وَأَيُّ قَلْبٍ أَنْكَرَهَا نُكِتَ فِيهِ نُكْتَةٌ بَيْضَاءُ، حَتَّى تَصِيرَ عَلَى قَلْبَيْنِ، عَلَى أَبْيَضَ مِثْلِ الصَّفَا فَلَا تَضُرُّهُ فِتْنَةٌ مَا دَامَتِ السَّمَاوَاتُ وَالْأَرْضُ، وَالْآخَرُ أَسْوَدُ مُرْبَادًّا كَالْكُوزِ، مُجَخِّيًا لَا يَعْرِفُ مَعْرُوفًا، وَلَا يُنْكِرُ مُنْكَرًا، إِلَّا مَا أُشْرِبَ مِنْ هَوَاهُ»، قَالَ حُذَيْفَةُ: وَحَدَّثْتُهُ، أَنَّ بَيْنَكَ وَبَيْنَهَا بَابًا مُغْلَقًا يُوشِكُ أَنْ يُكْسَرَ، قَالَ عُمَرُ: أَكَسْرًا لَا أَبَا لَكَ؟ فَلَوْ أَنَّهُ فُتِحَ لَعَلَّهُ كَانَ يُعَادُ، قُلْتُ: لَا بَلْ يُكْسَرُ، وَحَدَّثْتُهُ أَنَّ ذَلِكَ الْبَابَ رَجُلٌ يُقْتَلُ أَوْ يَمُوتُ حَدِيثًا لَيْسَ بِالْأَغَالِيطِ. قَالَ أَبُو خَالِدٍ: فَقُلْتُ لِسَعْدٍ: يَا أَبَا مَالِكٍ، مَا أَسْوَدُ مُرْبَادٌّ؟ قَالَ: شِدَّةُ الْبَيَاضِ فِي سَوَادٍ، قَالَ: قُلْتُ: فَمَا الْكُوزُ مُجَخِّيًا؟ قَالَ: مَنْكُوسًا.
Njiitu jullit ñi Umar ibnul Xattaab yal na ko Yàlla dollee gërëm dafa nekkoon ci jotaayam am mbooloo ci Sahaaba yi nekk fa moom, mu ne leen: Kan ci yéen moo dégg Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy tudd fitna yi? Ñenn ñi wax ne: nun dégg nanu ko muy tudd fitna yi, Umar yal na ko Yàlla dollee gërëm ne: amaana ngeen jublu ci balaa ak nattuy nit ki ci ñi ko jege; ci jabaram ak doomam ngir bëggam gu ëpp ci ñoom, ak li fiir ci ñoom, ak li mu leen yittewoo wolif ay yiw yu bari, walla ag càgganteem ci li mu war a taxawe ci seen i àq ak yar leen ak jàngal leen, niki noonu fitnay waaji ci dëkkandoom, ak lu ko niru, amaana ngeen jublu loolu? Ñu ne ko: waaw waaw, mu ne: yooyu ay fitna yuy waral ñu càmbar ko, amna ci ay bàkkaar yoy yaakaar nañu ñu far ko ci julli ak woor ak saraxe. Waaye kan ci yéen moo dégg Yonente bi di tudd fitna yiy matale ngir ag màggam ak tasaaroom gu bari ba nit ñi di jaxasoo kem ni duusi géej di jaxasoowe? Gaa yi noppi, Husayfata ibn Al-Yamaan yal na ko Yàlla dollee gërëm ne ko: man dégg naa ko, Umar daal di bég, ne ko: waay waay Yàlla xam na ne maa ñee sa baay waat ndax li mu indi ki mel ni yaw; waxal, Husayfata ne: Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: Fittna yi day feeñ daal di tafu ci xolu nit ki kem ni ag basaŋ di tafoo ci kiy nelaw, muy jeexital ci xol bi ngir tarug tappaloom ci fitna yi, fitna yi di baamtu bu jàll rekk beneen ñëw, xol bu mu dugg, mu bëgg ko daal di jaxasoo ak moom kem ni li ñuy naan di jaxasoowe ak di dugge; ñu tomb ca ab tomb bu ñuul, xol bu ko delloo ñu tomb ca tomb bu weex, ba mu mujj nekk ñaari xeeti xol; xol bu weex ngir ag taram ci ngëmam, ak muccam ci ayib, ak ne fitna yi tappaloowul ak moom, te jeexitalu ca, mu mel ni aw doj wu weex te rittax nga xam ne dara du ca taq, fitna it du ko lor ba keroog muy daje ak Yàlla. Beneen xol bi melo wi day soppeeku ñuul ngir fitna dem ba mel ni ab gutt gu jeng walla gu ñu juutal nga xam ne ndox du fa sax, niki noonu it xol bii yiw ak xereñte du ca nekk, du xam lu baax du bañ li bon, lu dul li mu bëgg te mu neex bakkanam. Husayfata wax Umar ne ko: fitna yooyu dara du ci génn ci sag dund, ndax sa diggante ak moom dafa am ab bunt bu ñu tëj te leegi ñu toj ko, Umar ne ko: ndax dañu koy toj? Bu ñu ko ubbi woon de dees na ko delloo tëjaat ko, Husayfata ne ko: déedéet, dañu koy toj kay, te bunt boobu benn waay la bu ñuy ray walla mu faatu. Te lii ma wax xibaar bu dëggu la te luy am la du ay nettaliy bindkat yi, te nekkul itam góor-góorlug boroom gis-gis, waaye ci waxi Yonente bi la.
Giraawaaleg fitna yooyu di daj kepp; ngir li ci nekk ci tuur dereet, ak yóbb alal, ak deñug kóolute.
Fitna yu ñu xam bu dee dafa aju ci diine kon boroomam ku ñu ŋàññ la, ndaxte benn mu nekk ay bidaa walla ay moy, waaye bu ajoo ci biri àdduna, kon loolu nattu la ak seet boroomam, te li war ci moom mooy muñ.
Xol day jeexitalu ci fitna yi nga xam ne da koy gaar, te ki ñi defal tawfeex mooy ki Yàlla gindi saxal ko ci njub.
An-Nawawii nee na: boroom At-Tahriir nee na: maanaam hadiis bi mooy: nit ki bu toppee bànneexam di def ay moy Yàlla kon bépp musiba bu mu def day dugg ci xolam, bu nekkee noonu nag day fitnawu leeru lislaame deñ ca, te xol dafa mel ni ab baag bu këpoo li nekk ci biir lépp sotteeku te dara du ci duggaat ginnaaw loolu
Li Umar wax Husayfata: (ñee naa sa baat) maanaam mooy: farlul ci mbir mii te waajal ko waajtaayu ku amul ci ndimbal.
Ngëneelu Umar yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, ak ne moom mooy bunt bi ñu tëj mu dox ci diggante nit ñi ak fitna yi.
Téere Muslim bi gën a wér (1/ 128-129) (144).
Yataal gi (2)
النهاية في غريب الحديث والأثر (606) (649) (471) (521) (340) (139).
شرح النووي على مسلم (2/ 171).
Cited in books
3 BooksYataal gi (3)
- الخطب المنبرية موسوعة الخطب المنبرية (القسم الثاني)«تُعْرَضُ الْفِتَنُ عَلَى الْقُلُوبِ كَالْحَصِيرِ عُودًا عُودًا، فَأَيُّ قَلْبٍ أُشْرِبَهَا نُكِتَتْ فِيهِ نُكْتَةٌ سَوْدَاءُ، وَأَيُّ قَلْبٍ أَنْكَرَهَا نُكِتَتْ فِيهِ نُكْتَةٌ بَيْضَاءُ»
- قاموس الكبائر موسوعة الكبائر - المجموعة الأولى«تُعْرَضُ الفِتَنُ عَلَى القُلُوبِ كَالْحَصِيرِ عُودًا عُودًا، فَأَيُّ قَلْبٍ أُشْرِبَهَا، نُكِتَ فِيهِ نُكْتَةٌ سَوْدَاءُ، وَأَيُّ قَلْبٍ أَنْكَرَهَا، نُكِتَ فِيهِ نُكْتَةٌ بَيْضَاءُ، حَتَّى تَصِيرَ عَلَى قَلْبَيْنِ، عَلَى أَبْيَضَ مِث
- قاموس الكبائر«تُعْرَضُ الفِتَنُ عَلَى القُلُوبِ كَالْحَصِيرِ عُودًا عُودًا، فَأَيُّ قَلْبٍ أُشْرِبَهَا، نُكِتَ فِيهِ نُكْتَةٌ سَوْدَاءُ، وَأَيُّ قَلْبٍ أَنْكَرَهَا، نُكِتَ فِيهِ نُكْتَةٌ بَيْضَاءُ، حَتَّى تَصِيرَ عَلَى قَلْبَيْنِ، عَلَى أَبْيَضَ مِث