Skip to content

«socc day laabal gémmeñ di gërëmloo Boroom bi».

Jële nañu ci Aysa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

«socc day laabal gémmeñ di gërëmloo Boroom bi».

«السِّوَاكُ مَطْهَرَةٌ لِلْفَمِ، مَرْضَاةٌ لِلرَّبِّ».

An-nasaa'iy soloo na ko, ak Ahmat.
Wér na
Leeral gi

Yónent bi day xamle ne setal ay bëñ ci bantu garabu Araag ak lu ko niru, day laabal gémmiñ ci ay tilim-tilim ak xet yu bon yi, Waaye daa bokk ci sabab yiy tax Yàlla gërëm jaamam bi; ndax topp Yàlla ak wuyu ay ndigalam moo ci nekk, ak li ci nekk ci sett gi nga xam ne Yàlla da koo bëgg.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ngëneelu socc, ak li Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ñaax aw xeetam ci ñu koy baril.

Li gën ci socc mooy jëfandikoo bantu Araak, jëfandikoo boroos ak pat dana ko man a wuutu.

Dellluwaay yi

Téere Sunna yi bu An-nasaa'iy (1/ 10) (5).

Téere Adiisu Ahmat bees leeral càllala ya (40/ 240) (24203).

Yataal gi (6)

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (2/ 342).

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

لمصطفى الخِن وغيره (2/ 852).

تطريز رياض الصالحين.

لفيصل آل مبارك (ص675).