Skip to content

«Wax yi gënal Yàlla ñent la: Subhaanal Laah, Wal hamdu lil Laah, wa laa-i-Laaha illal Laah, wal Laahu akbar, boo ci tàmbalee baax na».

Jële nañu ci Samurata Ibn Jundub -yal na ko Yàlla dollee gërëm - mu wax ne, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

«Wax yi gënal Yàlla ñent la: Subhaanal Laah, Wal hamdu lil Laah, wa laa-i-Laaha illal Laah, wal Laahu akbar, boo ci tàmbalee baax na».

«أَحَبُّ الْكَلَامِ إِلَى اللهِ أَرْبَعٌ: سُبْحَانَ اللهِ، وَالْحَمْدُ لِلهِ، وَلَا إِلَهَ إِلَّا اللهُ، وَاللهُ أَكْبَرُ، لَا يَضُرُّكَ بِأَيِّهِنَّ بَدَأْتَ».

Muslim soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Leerarug adiis bi: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day leeral ne wax yi gënal Yàlla ñent la: Subhaanal Laah: te mooy sellal Yàlla ci bépp wàññeeku. Ak alhamdu lil Laah: te mooy melal Yàlla cig mat sékk ànd ak bëgg ko ak màggal ko. Ak laa-i-Laaha illal Laah: maanaam: amul kenn ku ñuy jaamu cig dëgg ku dul Yàlla. Ak al-Laahu akbar: maanaam: Yàllaa gën a tedd te moo gën a màgg lépp lu mu man a doon. Te ngëneelam ak yoolam nekkul rekk ci toftale ko boo koy wax.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Bokk na ci njariñal adiis bi: Yombug Sariiha, ba tax na baat boo ci tàmbalee it du la lor.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1685) (2137).

(4/ 2093) (2731).

(4/ 2072) (2695).

Yataal gi (8)

توضيح الأحكام من بلوغ المرام.

للبسام (7/ 540).

منحة العلام في شرح بلوغ المرام.

لعبد الله الفوزان (10/ 411).

فتح ذي الجلال والإكرام.

لابن عثيمين (6/ 477).

سبل السلام بشرح بلوغ المرام.

للصنعاني (2/ 706).