Skip to content

"Yàlla du nelaw, te yellul ci moom muy nelaw

Jële nañu ci Abuu Muusaa yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa taxaw fi nun wax juróomi kàddu, mu ne:

"Yàlla du nelaw, te yellul ci moom muy nelaw, mooy yëkkëti ay balaas di ko wàcce, dees na yëkkëti jëfi guddi yi jëme ci moom laata jëfi bëccëg yi, ak jëfi bëccëg yi laata jëfi guddi yi, kiiraayam leer la -ñëw na ci geneen nettali: sawara la- bu ñu ko wuññi woon kon ceeñeeru kanamam gi dana lakk lépp lu gisam gi egg ci mbindeefam yi".

«إِنَّ اللهَ عَزَّ وَجَلَّ لَا يَنَامُ، وَلَا يَنْبَغِي لَهُ أَنْ يَنَامَ، يَخْفِضُ القِسْطَ وَيَرْفَعُهُ، يُرْفَعُ إِلَيْهِ عَمَلُ اللَّيْلِ قَبْلَ عَمَلِ النَّهَارِ، وَعَمَلُ النَّهَارِ قَبْلَ عَمَلِ اللَّيْلِ، حِجَابُهُ النُّورُ -وَفِي رِوَايَةٍ: النَّارُ- لَوْ كَشَفَهُ لَأَحْرَقَتْ سُبُحَاتُ وَجْهِهِ مَا انْتَهَى إِلَيْهِ بَصَرُهُ مِنْ خَلْقِهِ».

Muslim soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa taxaw ci sahaaba di xutba ci juróomi kàddu yu matale, te mooy: Bi ci njëkk: Yàlla mu màgg mi du nelaw. Ñaareel bi: nelaw jomb na ci àqam; ngir matug taxawam ci mbir yi ak matug dundam gi. Ñatteel bi: moom Yàlla mu kawe mi mooy suufeel balaas yi moo koy yëkkati it ca la ñu cay peese ci jëfi jaam ñi yu kawe yiy yëkkëtiku jëm ci moom, ak la ñu cay peese ci wërsëgi jaam yiy wàcc jëm ci suuf, wërsëgu wi nga xam ne ab dog la di céru bépp mbindeef moo koy suufeel di ko xatal, moo koy yëkkëti it di koo yaatal. Ñenteel bi: dañuy yëkkëti jëfi jaam ñi ci guddi go njëkk bëccëg ga ca topp jëme fa moom, ak seen i jëf ci bëccëg gi njëkk jëfi guddi ga ca topp; maalaaka yiu wattu jëf yi dañuy yéegal jëfi guddi ginnaaw bu jeexee ci njëlbeenu bëccëg gi, dañuy yéegal it jëfi bëccëg gi ginnaaw bu jeexee ci njëlbeenu guddi gi. Juróomeel bi: kiiraayu Yàlla giy tere ñu gis ko leer la walla sawara la, bu ko wuññi woon kon ceeñeeru kanamam dana lakk lépp lu gisam gi egg ci mbindeefam yi; ceeñeeru kanamam mooy leeram gi ak màggaayam gi ak rafetaayam wi. Nattale ga mooy: bu dindi woon daal di wuññi liy tere ñu gis ko te mooy kiiraay gi, mu feeñu mbindeefam yi kon ceeñeeri kanamam day lakk lépp lu gisam gi egg ci mbindeefam yi; te mooy mbindeef yépp; ndax ab gisam moom Yàlla mu Sell mi te kawe dafa daj mbooleem mbindeef yi.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Leeral ne nelaw jomb na Yàlla mu Sell mi te kawe; ndax dafa bokk ci mànkite yi te moom ku set la ci yooyu.

Yàlla mu kawe mi mooy teral ku ko soob di toroxal ku ko soob di gindi ku ko soob di sànk ku ko soob ci mbindeefam yi.

Dañuy yëkkëti jëf yi bis bu nekk ak guddi gi ne jëme fa Yàlla, te loolu ak ñaaxe la ñeel jaam ñi ci ñuy fuglu Yàlla mu màgg mi ci seen guddi yi ak seen bëccëg yi.

Hadiis bi day tegtale maandug Yàlla mu Sell mi ak rafetug saytoom ñeel biri jaamam yi, tr sikk-sàkka amul ci ne lii dafa bokk ci meloy matam gi moom Aji-Màgg ji te kawe.

Saxal kiiraay ñeel Yàlla mu Sell mi te kawe, te mooy leer gi dox ci digganteem ak jaamam yi, te bu dul woon ak moom danañu lakk.

Al-Aajurrii nee na: ñoñ-dëgg yi de dañuy melal Yàlla mu màgg mi ci ni mu melale boppam, ak ni ko Yonnenteem bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc melale ak ni ko Sahaaba yi yal na leen Yàlla dollee gërëm melale, te lii mooy ngiiru woroom xam-xam yiy topp te duñu sos. Jeex na. Waa sunna dañuy saxalal Yàlla li mu saxalal boppam vi ay tur ak i melo vi lu dul soppi walla neenal walla melal du caagine niroole, dañuy dàqal Yàlla it li mu dàqal boppam, dañuy noppi it ci loo xam ne dara rotu ci ci dàq du caagine saxal, Yàlla mu kawe mi nee na: {amul dara lu mel ni moom te moom Aji-Dégg la Aji-Gis la}.

Leer gi nga xam ne meloom la moom Aji-Sell ji te kawe nekkul leer gii nga xam ne moo ko yiir, leer gi ko yiir mbindeef la, te leerug Yàlla mu kawe mi ag leer la gu yell ci jëmmam ji, dara niroowul ak moom, la Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc gisoon nekkul lu dul kiiraay gi nekk ci diggante Yàlla ak jaamam yi.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (1/ 161) (179).

Yataal gi (3)

شرح المرقاة (1/128).

فتح المنعم (1/581).

البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (5/ 82).