Skip to content

"ki jébbalu, ñu wërsëgal ko lu doy, Yàlla def ko mu doylu ci li ko Yàlla jox koo ku texe na”.

Jële nañu ci Abdullah Ibn Amr Ibnul Haasi -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne:

"ki jébbalu, ñu wërsëgal ko lu doy, Yàlla def ko mu doylu ci li ko Yàlla jox koo ku texe na”.

«قَدْ أَفْلَحَ مَن أَسْلَمَ، وَرُزِقَ كَفَافًا، وَقَنَّعَهُ اللَّهُ بما آتَاهُ».

Muslim soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yonente bi leeral na ne ku toppu boroom bi jaar ci lislaam, ñu wërsëgal ko lu dagan kem aajoom ëppul yéesul, Yàlla def ko mu doylu gërëm li mu ko jox koo ku texe na.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Texeg nit ki mi ngi ci matug diineem ak doyug dundam ak ug doyloom ci li ko Yàlla jox.

Xemmemloo ci doylu ci li ñu la jox ci àdduna ànd ak lislaam ak sunna.

Dellluwaay yi

Téere Muslim bi gën a wér (2/ 730) (1054).

Yataal gi (6)

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (1/ 447).

فيض القدير شرح الجامع الصغير.

للمناوي (4/ 508).

تحفة الأحوذي بشرح جامع الترمذي.

لأبي العلا المباركفوري (7/ 11).