Skip to content

ñi gën ci yéen mooy ña ca gën a rafet jikkó».

Jële na ñu ci Abdullah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne:

Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-nekkul woon ku ñaawi wax mbaa jëf, daa na wax naan: « ñi gën ci yéen mooy ña ca gën a rafet jikkó».

لَمْ يَكُنِ النَّبِيُّ صَلَّى اللهُ عَلَيْهِ وَسَلَّمَ فَاحِشًا وَلَا مُتَفَحِّشًا، وَكَانَ يَقُولُ: «إِنَّ مِنْ خِيَارِكُمْ أَحْسَنَكُمْ أَخْلَاقًا».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Bokkul woon ci jikkóy Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax ju ñaaw, walla jëf ju ñaaw, te daawu ko jublu it mbaa mu koy tay, ndax moom Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- boroom jikkó yu màgg la. Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daa na wax naan: ki gën ci yéen fa Yàlla mooy ki gën a rafet jikkó, ci def njekk, ak leeral xar kanam, ak téye lor te muñal nit ñi, ak jaxasoo ak nit ñi ca na mu rafete.

Maanaay baat yi

...:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Bokk na ci njariñal hdiis bi: War na ci aji-gëm ji mu sori lu ñaaw moo xam wax ju ñaaw la mbaa jëf ju ñaaw.

Matug jikkoy Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, dara daawul juge ci moom lu dul jëf ju sell ak wax ju teey.

Jikkó ju baax mooy barabu rawante ga, ndax ku jiitu rekk bokk ca way-gëm ya gën, te gën a mat sëkk ag ngëm.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (4/ 189) (3559).

Téere Muslim bi gën a wér (4/ 1810) (2321).

Yataal gi (4)

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (1/ 672).

تطريز رياض الصالحين.

لفيصل آل مبارك (ص410).