"Yàlla gërëm na ci yéen ñatt, bañ na it ci yéen ñatt
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:
"Yàlla gërëm na ci yéen ñatt, bañ na it ci yéen ñatt, gërëm na ci yéen: ngeen jaamu ko, te bañ ko a bokkaale ak dara, ak ngeen jàpp ci buumu Yàlla gi te bañ a teqalikoo, mu bañ ci yeen: nee nañu ak nee na, ak barig laaj, ak sànk alal".
«إِنَّ اللهَ يَرْضَى لَكُمْ ثَلَاثًا، وَيَكْرَهُ لَكُمْ ثَلَاثًا، فَيَرْضَى لَكُمْ: أَنْ تَعْبُدُوهُ، وَلَا تُشْرِكُوا بِهِ شَيْئًا، وَأَنْ تَعْتَصِمُوا بِحَبْلِ اللهِ جَمِيعًا وَلَا تَفَرَّقُوا، وَيَكْرَهُ لَكُمْ: قِيلَ وَقَالَ، وَكَثْرَةَ السُّؤَالِ، وَإِضَاعَةِ الْمَالِ».
Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day xibaare ne Yàlla bëgg na ci jaamam yi ñatti jikkó, bañ ci ñoom ñatt, bëgg na ci ñoom: Ñu wéetal ko te duñu ko bokkaale ak dara, ak ñu jàpp ci kóllareg Yàlla gi, ak Alxuraan ak sunnas Yonente bi yépp, ak ñu bañ a teqalikoo ak mbooloom jullit ñi. Mu bañ ci ñoom: ay caaxaan ak wax lu amul njariñ, ak laaj lu dul am, walla di laaj nit ñi seen alal, ak li ci seen i loxo, ak lu mu aajowoowul, ak sànk alal ak def ko fu dul wàllu sariiha, ak jëme ko ci ag yàq.
Yàlla dafa bëgg ci jaamam yi ñu sellal jaamu gi, mu bañ ñu weddi ko.
Ñaaxe ci jàpp ak ŋoy ci buumu Yàlla mu kawe mi; ngir li ci nekk ci booloo ak bennoo.
Ñaaxe ci booloo, ak digle ñu taqoo ak moom ak bennale ay sàppeem, ak tere safaanam di teqalikoo ak wuute.
Tere nañu bari wax ci lu amul njariñ; ndaxte moom donte bu dee lu dagan la sax sànk waxtu la, bu dee dafa araam nag kon baril ay bàkkaar rekk la.
Bàyyee xuus ci xibaari nit ñi ak topp seeni mbir ak nettali seen i wax ak seen i jëf.
Tere nañu baril di laaj alali nit ñi.
Araamal sànk alal, ak ñaaxe ci sàmmonte ak moom ci luy jariñ.
Téere Muslim bi gën a wér (3/ 1340) (1715).
Yataal gi (2)
البحر المحيط الثجاج في شرح صحيح الإمام مسلم بن الحجاج (30/ 85).
إكمال المعلم بفوائد مسلم (5/ 568).
Cited in books
3 BooksYataal gi (3)
- الحديث زاد 4الحديث 4«إِنَّ الله يَرْضَى لَكُمْ ثَلاثًا، وَيَكْرَهُ لَكُمْ ثَلاثًا، فَيَرْضَى لَكُمْ: أَنْ تَعْبُدُوهُ، وَلا تُشْرِكُوا بِهِ شَيْئًا، وَأَنْ تَعْتَصِمُوا بِحَبْلِ الله جَمِيعًا وَلا تَفَرَّقُوا، وَيَكْرَهُ لَكُمْ: قِيلَ وَقالَ، وَكَثْرَةَ السُّ
- الخطب المنبريةموسوعة الخطب المنبرية (القسم الأول)«إِنَّ اللَّهَ يَرْضَى لَكُمْ ثَلَاثًا، وَيَكْرَهُ لَكُمْ ثَلَاثًا، فَيَرْضَى لَكُمْ أَنْ تَعْبُدُوهُ، وَلَا تُشْرِكُوا بِهِ شَيْئًا، وَأَنْ تَعْتَصِمُوا بِحَبْلِ اللَّهِ جَمِيعًا وَلَا تَفَرَّقُوا، وَيَكْرَهُ لَكُمْ قِيلَ وَقَالَ، وَكَثْرَ
- رياض الصالحينرياض الصالحين مع فوائد وهدايات - 8«إنَّ الله تَعَالىٰ يَرْضَىٰ لَكُمْ ثَلاثاً، وَيَكْرَهُ لَكُمْ ثَلاَثاً: فَيَرْضَىٰ لَكُمْ أَنْ تَعْبُدوه، وَلاَ تُشْرِكُوا بِهِ شَيْئاً، وَأَنْ تَعْتَصِمُوا بِحَبْلِ الله جَمِيعاً وَلاَ تَفرَّقُوا. وَيَكْرَهُ لَكُمْ: قِيلَ وَقَالَ، وَكَثْر