Skip to content

«àjjana moo gën a jege ku ne ci yeen ay waroy dàllam, sawara it naka noonu».

Jële nañu ci Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewël ak mucc- mu wax ne:

«àjjana moo gën a jege ku ne ci yeen ay waroy dàllam, sawara it naka noonu».

«الْجَنَّةُ أَقْرَبُ إِلَى أَحَدِكُمْ مِنْ شِرَاكِ نَعْلِهِ، وَالنَّارُ مِثْلُ ذَلِكَ».

Al-buxaariy soloo na ko.
Wér na
Leeral gi

Yónente bi day xamle ne àjjana ak sawara dañoo jege nit ki kem ni ko ay waroy dàllam jegee te mooy liy nekk ci kaw ndëggu yi, ndaxte moom man naa def ab topp Yàlla ngir ngërëmam loolu dugal ko àjjana, walla ab moy Yàlla loolu nekk sabab ci duggam sawara.

Maanaay baat yi

....:

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Xemmemloo ci jëf lu baax doonte dafa néew, ak xuppaate ci jëf lu ñaaw doonte dafa néew.

Jullit cig dundam manul ñàkk mu boole yaakaar ak ragal, tey sax ci ñaan Yàlla mu saxal ko ngir mu mucc te du woru ci melokaanam.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (8/ 102) (6488).

Yataal gi (8)

شرح رياض الصالحين.

لابن عثيمين (2/ 99).

فتح الباري.

لابن حجر(11/ 321).

بهجة الناظرين شرح رياض الصالحين.

لسليم الهلالي (1/ 186).

نزهة المتقين شرح رياض الصالحين.

لمصطفى الخِن وغيره (1/ 136).