Skip to content

«ku man a takk jabar na takk, ndaxte moo gën a man a damm ab gis, gën a man a sàmm péy mi, ku ko manul nag dénk naa ko woor, ndaxte dana ko man a téye».

Jële nañu ci Abdullah ibn Mashuud yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: nekkoon nanu fi Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne:

«ku man a takk jabar na takk, ndaxte moo gën a man a damm ab gis, gën a man a sàmm péy mi, ku ko manul nag dénk naa ko woor, ndaxte dana ko man a téye».

«مَنِ اسْتَطَاعَ البَاءَةَ فَلْيَتَزَوَّجْ، فَإِنَّهُ أَغَضُّ لِلْبَصَرِ، وَأَحْصَنُ لِلْفَرْجِ، وَمَنْ لَمْ يَسْتَطِعْ فَعَلَيْهِ بِالصَّوْمِ، فَإِنَّهُ لَهُ وِجَاءٌ».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day soññ ki man a sëy ak li aju ci dundug sëy mu takk soxna; ndaxte moo gën a man a sàmm ab gisam ci lu araam, te moo gën a man a aar péyam, ak it tere ko a tàbbi ci ñaawteef, Ku manul a yor dundub sëy fekk ku man a sëy la kon na woor ndaxte dana dagg bànneexu péyam ak ayu maniyu mi.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Xérug lislaam ci yiy sabab ag saŋéwu ak mucc ci ñaawteef yi.

Ñaax na ki amul doley takk muy woor; ndaxte day wàññi bànneex bi.

Anamu niróole woor ak Wijaa; ndaxte Wijaa mooy tàpp sédditi ñaari xuur yi, bànneexu sëy bi daldi deñ, niki noonu woor, day wàññi bànneexu sëy.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (3/ 26) (1905).

Téere Muslim bi gën a wér (2/ 1018) (1400).

Yataal gi (6)

الإلمام بشرح عمدة الأحكام للشيخ.

لإسماعيل الأنصاري (2/ 57).

تيسير العلام شرح عمدة الأحكام.

لعبد الله البسام (ص565).

خلاصة الكلام شرح عمدة الأحكام.

لفيصل آل مبارك (ص281).