Skip to content

«ku fàtte ne dafa woor, daal di lekk walla mu naan, na mottali wooram, ndax Yàlla moo ko leel moo ko mànnal».

Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne : Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na:

«ku fàtte ne dafa woor, daal di lekk walla mu naan, na mottali wooram, ndax Yàlla moo ko leel moo ko mànnal».

«مَنْ نَسِيَ وَهُوَ صَائِمٌ، فَأَكَلَ أَوْ شَرِبَ، فَلْيُتِمَّ صَوْمَهُ، فَإِنَّمَا أَطْعَمَهُ اللهُ وَسَقَاهُ».

Al-buxaariy ak Muslim dëppoo nañu ci génnee ko ci seen ñaari téere yi gën a wér.
Wér na
Leeral gi

Yonente bi day leeral ne ku lekk walla mu naan fekk dafa fàtte ne daa woor kooru farata walla naafila na mottali wooram te bu mu dog; ndaxte jubluwul a dog, waaye moom wërsëg wu ko Yàlla wommatal jëme ko ci moom la ngir leel ko mànnal ko.

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ki lekk mbaa mu naan te fekk daa fàtte kooram wér na.

Ki lekk walla mu naan ta fekk daa fàtte du ci am bàkkaar; ndaxte du moo ko tànn.

Ñeewanteg Yàlla ci jaamam ñi, ak yombal ci seen kaw, ak yëkkëti coono ak jafe-jafe ci ñoom.

Aji-woor ji du doge ci lenn ci yiy dogloo lu dul bu ci ñatti sàrt dajee: bu njëkk bi: muy aji-xam, bu dee dafa nekk aji-réer kon du dog, ñaareel bi: mu nekk di aji-fàttaliku, bu dee aji-fàtte la, kon wooram wér na te fay waru ko, ñatteel bi: muy aji-tànn déet muy ku ñu ga, ci mu jëfandikoo luy dogloo ci lu mu tay.

Dellluwaay yi

Téere Al-buxaariy bi gën a wér (3/ 31) (1933).

Téere Muslim bi gën a wér (2/ 809) (1155).

Yataal gi (6)

تيسير العلام.

لعبد الله البسام (ص319).

تنبيه الأفهام شرح عمدة الأحكام.

لابن عثيمين (3/ 422).

خلاصة الكلام على عمدة الأحكام.

لفيصل آل مبارك (ص148).