«ki war mooy nuyu kiy dox, kiy dox mooy nuyu ki toog, ñi néew ñooy nuyu ñi bari»
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-mu wax ne :Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:
«ki war mooy nuyu kiy dox, kiy dox mooy nuyu ki toog, ñi néew ñooy nuyu ñi bari». Nekk na ca téereb Al-Buxaarii: «xale bi mooy nuyu mag mi, kiy romb mooy nuyu ki toog, ñi néew ñooy nuyu ñi bari».
«يُسَلِّمُ الرَّاكِبُ عَلَى المَاشِي، وَالمَاشِي عَلَى القَاعِدِ، وَالقَلِيلُ عَلَى الكَثِيرِ». وَلِلبُخَارِي: «يُسَلِّمُ الصَّغِيرُ عَلَى الكَبِيرِ، وَالمَارُّ عَلَى القَاعِدِ، وَالقَلِيلُ عَلَى الكَثِيرِ».
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day jàngale teggini nuyòo ci diggante nit ñi "assalaamu halaykum wa rahmatul Laahi wa barakaatuhu", Xale nuyu mag, ki war nuyu kiy dox, kiy dox nuyu ki toog, lim bu néew nuyu ñu bari ñi.
Sopp nañu nuyòo kem ni ko hadiis indee, bu kiy dox nuyòo ki war ak lu dul loolu ci li ñu tudd, dana dagan, waaye daa wuute ak li yelloon te gën.
Tasaare nuyòo ci anam gi mu ñëwe ci hadiis bi daa bokk ci sababi bëggante yi ak miinante yi.
Bu ñu yamoo te tolloo ci yi nu wax, kon ka ca gën mooy ka njëkk a nuyòo.
Matug Sariiha ci leeral lépp lu nit ñi aajowoo.
Jàngale teggini nuyòo ak jox ku nekk àqam.
Téere Al-buxaariy bi gën a wér (8/ 52) (6232).
Téere Muslim bi gën a wér (4/ 1703) (2160).
Yataal gi (11)
كنوز رياض الصالحين.
لمجموعة من الباحثين (11/ 280).
بهجة الناظرين.
تأليف: سليم الهلالي (2/ 137).
نزهة المتقين.
مجموعة من الباحثين (1/ 666).
شرح رياض الصالحين.
لابن عثيمين (4/ 407).
منار القاري.
لحمزة قاسم (5/ 257).
الأدب النبوي (ص159).
Cited in books
4 BooksYataal gi (4)
- الحقيقة المُبْهِرَة في العلاقة بين الإسلام والإنسان(يسلم الصغير على الكبير، والمار على القاعد، والقليل على الكثير)[224].
- رياض الصالحينرياض الصالحين مع فوائد وهدايات - 5«يُسَلِّمُ الرَّاكبُ عَلَىٰ المَاشي، والمَاشي عَلَىٰ القَاعد، والقليلُ عَلَىٰ الكَثير».
- ما لا يسع أطفال المسلمين جهله«يُسَلِّمُ الرَّاكِبُ عَلَى المَاشِي، وَالمَاشِي عَلَى القَاعِدِ، وَالقَلِيلُ عَلَى الكَثِيرِ»[153].
- نبراس طالب (2)نبراس طالب (2) «يُسَلِّمُ الرَّاكِبُ عَلَى الْمَاشِي، وَالْمَاشِي عَلَى الْقَاعِدِ، وَالْقَلِيلُ عَلَى الْكَثِيرِ»