Skip to content

"ku jàng aayatul Kursiyu ginnaaw jullig farata gu ne dara terewukoo dugg àjjana lu dul dee".

Jële nañu ci Abuu Umaamata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na:

"ku jàng aayatul Kursiyu ginnaaw jullig farata gu ne dara terewukoo dugg àjjana lu dul dee".

«مَنْ قَرَأَ آيَةَ الْكُرْسِيِّ فِي دُبُرِ كُلِّ صَلَاةٍ مَكْتُوبَةٍ لَمْ يَمْنَعْهُ مِنْ دُخُولِ الْجَنَّةِ إِلَّا أَنْ يَمُوتَ».

An-nasaa'iy soloo na ko ca Al-kubraa.
Wér na
Leeral gi

Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- day xibaare ne ku jàng aayatul Kursiyu ginnaaw bu noppee ci jullig farata gu ne dara terewu koo dugg àjjana lu dul dee; moom nag moo ngi ci saaru Al-Baxara, mooy waxi Yàlla ji: {Allaahu laa ilaaha illa Huwal Hayyul Xayyuumu laa taaxuzuhu sinatun walaa nawmun lahu maafis Samaawaati wa maa fil-Ardi man zal lazii yasfahu hindahuu illaa bi-iznihii yahlamu maa bayna aydiihim wa maa xalfahum wa laa yuhiituuna bi say-in min hilmihii illaa bimaa saa-a wasiha kursiyyuhus Samaawaaati wal-Ardi wa laa ya-uuduhu hifsuhumaa wahuwal Haliyyul Hasiimu} [Al-Baxara: 255].

Bokk na ci njariñi hadiis bi

Ngëneelu aaya ju màgg bii; ngir li mu làmboo ci ay tur yu rafet ak i melo yu kawe.

Sopp nañu jàng aayaa ju màgg jii ginnaaw gépp jullig farata.

Jëf yu sell yi sabab la ci dugg àjjana.

Dellluwaay yi
Yataal gi (7)

المعجم الكبير.

للطبراني السنن الكبرى.

للنسائي (9/ 44) (9848).

توضِيحُ الأحكَامِ مِن بُلوُغ المَرَام.

للبسام (2/ 313).

منحة العلام في شرح بلوغ المرام.

لعبد الله الفوزان (3/ 197).